Sasu Sarxalkat yi di ñetteelu xaaju Tawreetu Musaa Ubbite gi Aaya bi jiitu ci Sasu Sarxalkat yi moo indi na Yàlla àddoo woon ca xaymab ndaje ma, woo Yonent Yàlla Musaa, ngir wax ak moom. Bare na lool fu téere bi joxe ay ndigali yoon aki sàrt yu Yàlla jox Musaa, ngir mu jottli ko bànni Israyil, te dige bi ci Yàlla boole moo di ndigal yooyu ñooy taxa dund képp ku leen jëfe. Ci gàttal, ci téere bi la Yàlla di xamal bànni Israyil, nan lees di dindee mboolem li gàllankoor seenub neexoo ak Yàlla, ak nan lees di jëfe ba xaymab jaamookaay bi doon bérabu ndaje dëgg bu ñuy dajee ak Yàlla. Fàww ñiy jooxe ay sarax jooxe sarax yi ni mu ware. Fàww it sarxalkat yi di nit ñu ñu weg, nit ñu seen jëfin tedd, te kenn ku nekk ci askan wi moytu, kem kàttanam, mboolem luy sobeel aw yaram, te moytu di fecci kóllëre ci jëfinam ak ci ni muy jaamoo Yàlla. Yàlla miy Ku Sell, di Cofeelu neen, di Ki yor ndund, moo namm ñoñam wàllsi ci sellngay boppam, ngir ñoom itam ñu man di jottlee, ndund ak cofeel. Yéene boobu la Yàlla joxe bànni Israyil santaane bii Almasi ne mooy kenug yoonu Yàlla: “Ni ngeen soppe seen bopp nag, nangeen ko soppe seen moroom.” Aaya 19:18. Mboolem ndigali yoon yi ci téere bi, li leen taxa jóg mooy yombal nu gëmkat ñi mana neexoo ak Yàlla, ak fépp fu ñu mana bokk, ak jant bu ñu mana yemool. Kon ndigali yoon yii tàyyiwuñu benn yoon di soññe ci mboolem xeeti kàddu, ngir gëmkat bi saxoo bàyyi xel ne neexoo ak Yàlla manula ñàkk, te ci la ag dundam aju. Ci Tënk: Saar 1—7 Ay dogal ci mbirum sarax yi Saar 8—10 Fal nañu sarxalkat yi Saar 11—15 Sàrtal nañu lu set ak lu setul Saar 16 Lu jëm ci bésub Njotlaay Saar 17—26 Ndigal yi jëm ci sellal Saar 27 Lu jëm ci jagleel Aji Sax ji nit ak alal
3 «Bu saraxam dee saraxu jur gu gudd gu ñuy def rendi-dóomal, na sarxal aw yëkk wu amul sikk. Na ko yóbbu ci bunt xaymab ndaje mi ci kanam Aji Sax ji, ngir mu nangul ko ko. 4 Na teg loxoom ci kaw boppu juru saraxu rendi-dóomal bi, ndax ñu nangul ko ko, muy njotlaayam. 5 Na rendi yëkk wi ci kanam Aji Sax ji, te doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi ñooy indi deret ji, xëpp ko ci mboolem weti sarxalukaay bi ci bunt xaymab ndaje mi. 6 Juru saraxu rendi-dóomal bi, na ko boroom sarax bi fees, daggat ko. 7 Doomi Aaróona, sarxalkat bi, dañuy jafal ab taal ci kaw sarxalukaay bi, teg matt mi ci taal bi. 8 Su ko defee doomi Aaróona yu góor, yiy sarxalkat yi, jël dog yi, booleek bopp bi ak nebbon bi, teg ko ci kaw mattum taal bi ci sarxalukaay bi. 9 Nañu raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
10 «Bu saraxam dee ab gàtt bu ñuy def rendi-dóomal, muy xar mbaa bëy, na sarxal bu góor bu amul sikk. 11 Na rendi sarax si ci kanam Aji Sax ji, fa féete sarxalukaay bi bëj-gànnaar. Na doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi. 12 Bu ko boroom sarax bi daggatee ba noppi, sarxalkat bi day boole dog yeek bopp bi ak nebbon bi, teg ko ci kaw mattum taal bi ci kaw sarxalukaay bi. 13 Na boroom sarax bi raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
14 «Bu nit ki dee sarxalal Aji Sax ji njanaaw luy doon rendi-dóomal, na sarxe pitax mbaa xati mu ndaw. 15 Na ko sarxalkat bi yóbbu ca sarxalukaay ba, kutt baat bi, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi. Deret ji dees koy siital ci wetu sarxalukaay bi, ba mu jeex. 16 Na indi gag bi ak li ci nekk te wetti ko fa ñuy def dóomu-taal ba, fa féete sarxalukaay bi penku. 17 Sarxalkat bi day jàpp ci laaf yi, xotti te bañ koo teqale, daldi koy lakk ci sarxalukaay bi, ci kaw mattum taal bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
Sarxalkat yi 2 ->