Saar 2
Yunus a ngi tinu
1 Ci kaw loolu Aji Sax ji yebal jën wu mag, mu wonn Yunus. Mu nekk ca biiru jën wa ñetti bëccëg ak ñetti guddi. 2 Yunus ñaan ci Yàllaam Aji Sax ji, fa mu tollu ca biir jën wa. 3 Mu ne:
Maa jàq, woo Aji Sax ji, mu wuyu ma.
Ca xóotey njaniiw laa wootee wall, nga dégg ma.
4 Yaa ma xalab xóotey xolu géej, ndaw ma mëdd ma.
Say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
5 Man nag ma naan: «Dàqees na ma, ba ma sore la,
waaye maay dellu gis sa kër gu sell ga!»
6 Ndox maa ma tanc ba ci put,
xóotey géej mëdd ma,
waag ba laxasu sama bopp.
7 Ca reeni tund ya laa suuxi,
caabiy suuf féete ma gannaaw ba fàww,
waaye ca kan ma nga jukkee sama bakkan,
yaw, sama Yàlla Aji Sax ji.
8 Noowal bakkan a nga may rëcc,
sama xel ne yarr ci yaw, Aji Sax ji,
sama ñaan àgg fa yaw,
ca sa kër gu sell ga.
9 Ñiy wormaal neenug neen daal,
ñoo dëddu seen yiw fa Yàlla.
10 Man nag, ci biir cant laa lay sarxale.
Li ma xas laay sottal.
Wall, fa Aji Sax ji!