Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site

Yunus
Ubbite gi
Yonent Yàlla Yunus waa réewum Israyil la woon, te fa la nekkoon ba muy jot ndigalal Yàlla, la ko yebal ca waa dëkk ba ñuy wax Niniw, te féeteek réewum Iraag ci jamonoy tey. Niniw nag bokkul woon ci Israyil. Péeyu Asiri la woon. Waa Asiri askan wu néeg lañu woon, bokkoon ci nooni Israyil yi gënoona aay ci ñoom. Beneen dëkk bi ñuy wax ci téere bii mooy Tarsis. Ci waxinu jant yooyu, Tarsis a nga woon ca catu àddina, soreyaatoo lool ak Israyil ak Niniw.
Ci Tënk:
Saar 1 Yunus gàntal na Yàlla ba daw
Saar 2 Yunus ñaan na ci biir njàqareem
Saar 3 Yunus jëfe na ndigal la jibaat ñeel ko
Saar 4 Yunus déggoowul ak Yàlla ci ni mu gise

Saar 1
Yunus jot na ndigal lu ko diis
1 Am na bés kàddug Aji Sax ji dikkal Yunus, mi Ametay di baayam. Mu ne ko: 2 «Jógal dem Niniw, dëkk bu mag ba, nga rëbb leen, ndax seen mbon agsi na ba fi man.»

3 Yunus nag jóg jëm Tarsis, ngir daw Aji Sax ji. Mu àgg fu ñuy wax Yafa, fekk fa gaal gu mag gu jëm Tarsis. Mu fey njég ga, dugg, ànd ak ña ca nekk, jëm Tarsis, ngir daw Aji Sax ji.

4 Aji Sax ji itam sànni ngelaw lu réy ca géej ga, muy ngëlén lu réy ca géej ga, ba gaal ga nara tas. 5 Ba loolu amee mool ya tiit di yuuxoo, ku nekk di woo sa yàlla wall. Ñu sànni biir géej la ñu yeboon ca gaal ga ngir gëna woyof. Fekk na Yunus wàcc ca suufu gaal ga, tëdd di nelaw ba yàndoor. 6 Ci kaw loolu njiitu mool ya dikk ba ca moom, ne ko: «Yaw, ana looy nelaw? Jógal kay woo sa yàlla wall! Jombul mu geesu nu, ba dunu sànku.»

7 Ci biir loolu ku nekk naan sa moroom: «Ayca nu tegoo bant, ba xam musiba mii nu dal, ku nu ko yóbbe.» Ñu tegoo bant, mu dal ca kaw Yunus. 8 Ñu ne ko: «Dinga nu wax nag ku nu yóbbe mii musiba! Ana luy sa liggéey, ak foo bàyyikook fuy sam réew, ak xeet woo bokk sax yaw?»

9 Mu ne leen: «Ab Ebrë laa. Aji Sax jiy Yàllay asamaan laay jaamu, moom mi sàkk géej ak jéeri.» 10 Ci kaw loolu nit ña tiit tiitaange lu réy, ne ko: «Yaw, li nga def lu mu doon?» Fekk na Yunus xamal leen ne Aji Sax ji lay daw.

11 Géej ga nag di gëna sàmbaraax. Ñu ne ko: «Nu nu lay def nag, ba géej gi dalal nu?» 12 Yunus ne leen: «Fableen ma, sànni ci biir géej gi. Kon géej gi dal. Ndax xam naa xéll ne ngëlén lu réy lii, maa leen ko yóbbe.» 13 Terewul nit ña joow, joow rekk, wuti tefes, mu të ndax géej ga gëna sàmbaraax ca seen kaw.

14 Ba loolu amee ñu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, ngalla bu nu bàyyi nu sànku ndax bakkanu nit kii, te bu nu gàdduloo bakkanu jaambur, ndax yaw Aji Sax ji, sa coobare nga def.» 15 Ñu daldi fab Yunus, sànni ca biir géej ga, géej ga giif, ne tekk. 16 Nit ña nag am tiitaange lu gënatee réy ci Aji Sax ji, daldi rendil Aji Sax ji sarax, ba noppi xasal ko aw xas.

Yunus 2 ->