Saar 8
Bildàdd nee musiba, añu boroom
1 Bildàdd ma bàyyikoo Suwa, àddu ne:
2 Ana foo àppal sa wax jii?
Ngay mbel-mbeli ni callweer!
3 Ana Yàllaak safaan yoon?
Ana Aji Man jeek safaan dëgg?
4 Bu ko sa doom yi moyee, kay,
mu ba leen ak seen añub tooñ!
5 Yaw nag soo sàkkoo Yàlla,
dagaan Aji Man ji aw yiwam,
6 soo muccee ayib te jub,
day daldi taxaw temm ci say mbir,
delloo la sa kërug njekk,
7 nga yokkoo yokku ëllëg,
ba xeeb sa démb.
8 Laajal rekk maas gi nu jiitu,
te teewlu seen gëstuy maam ya.
9 Nun xamunu, démb rekk lanu,
sunu fani kaw suuf di takkndeer suy wéy.
10 Ñi ñu jiitoo lay xamal, wax la,
tibbe seen xol yii kàddu, dénk la:
11 «Ndax jàqaar dina naate fu dul ban bu tooy,
am barax dina saxe fu amul ndox?
12 Bu ndox ma ŋiisee, mooy jëkka lax,
te du ñoragum bay mata dog.»
13 Loolooy muju képp ku fàtte Yàlla,
yaakaaru yéefar, tas rekk,
14 cëslaayam màbb,
làquwaayam di lëndu jargoñ.
15 Mu wéeroo këram, kër gay yëngu;
mu ŋoyu ca, muy jaayu.
16 Ku gëmadee ngi mel ni garab
gu jant biy jam, mu naat;
car yay lawe tool ba mu saxe,
17 reen ya rawaasoo ci biir jalub xeer,
muy kërug dojam gu mu ŋoy.
18 Nga buddee ko bérab ba mu sax,
bérab ba jàmbu ko, ne ko: «Masuma laa gis!»
19 Geneen garab ay jebbi, wuutu ko.
Mu ngoog, ab yéefar, nii la mujam di rafete!
20 Dama ne: Yàlla du gàntal ku maandu,
te du dooleel kuy def lu bon.
21 Moo lay may loo ree,
bay sarxolle,
22 say bañ gàccoo gàcce,