Saar 36
Eliyu nee coonoy àddina am njàng la
1 Eliyu dellu ne:
2 Négal tuuti, ma xamal la;
ay kàddoo ngeeti yu may waxal Yàlla.
3 Fu xóot laay jukkee sama xam-xam,
ba delloo dëgg ki ma sàkk.
4 Sikk déy, nekkul ci li ma lay wax;
ku buural xam-xam a janook yaw nii!
5 Dama ne, Yàllaa màgg te du jalaxe,
moo màgg te réy um xel.
6 Du ba ku bon, mu dund,
te mooy jox néew-ji-doole àqam.
7 Du noppee xool aji jub ñi,
xanaa di leen dëj ci jali buur yi,
saxal seen toogaay, màggal leen.
8 Bu ñu demee ba ñu jéng leen,
mbaa buumi njàqare ŋodaar leen,
9 Yàllaa leen koy artoo ci seeni jëf,
seen tooñi reewande.
10 Da leen di dégtal ndigal,
ne leen ñu dëddu ñaawtéef.
11 Su ñu ko dégloo, déggal ko,
jeexale bés yu rafet,
mujje ati bànneex.
12 Su ñu dégluwul, jàlli dexu ndee,
faatu ndax xamadi.
13 Ab yéefar day denc mer,
te mbugal du tax mu woote wall.
14 Ku ni mel ay deeye ndaw,
ay fanam jeexe biir gàcce.
15 Yàllaay wallu boroom tiis ciw tiisam,
di tege coono, ba ñu déglu ko.
16 Moom it moo lay xettli ci njàqare,
weccee la ko fu yaa fu la dara xatalul,
taajal la ñam wu duun te niin.
17 Waaye añu ku bon duunal na la,
dëgg ak yoon ne la taral.
18 Bu la kenn xiirtale alal,
te bu la ger bu réy jengloo.
19 Kon déy doo yuuxu ba mucc ci njàqare,
kër-këreek doole it du la ca génne.
20 Bul yàkkamti guddi;
ca law xeet di jekki buuboo seenum réew.
21 Moytula walbatiku di def ñaawtéef,
moo tax nattu dikkal la.
Yàlla mooy buur
22 Yàlla, kay, mooy ki dooleem kaweel!
Ana ku mana jàngle ni moom?
23 Ana ku ko masa rëddal yoonam?
Ak ku ko ne: «Def nga naka-su-dul-noonu?»
24 Bul di fàttee màggal jëfam,
yi ko nit ñiy woye.
25 Mboolem doom aadama gis na ko;
nitoo nit séene ko fu sore.
26 Yàlla, kay daa màgg ba wees xam-xam,
te ay atam, deesul xayma lim ba.
27 Keey ñoddi toqi ndox,
mu def ub lay, tawal,
28 niir yi sotti,
baawaanal doom aadama.
29 Ana ku xam ni aw xiin di firikoo,
ba dënu fettaxe xaymab Yàlla ba?
30 Keey taal melaxam, mu dajal asamaan,
sàng xóotey géej.
31 Noonu lay saytoo xeet yi,
ba maye ñam wu ne gàññ.
32 Yaari loxoom lay ŋëbe melax gi,
dalal ko fa mu ko sant,
33 kàddu yéene ab taw,