Saar 32
Ndaw nee na mooy tontu mag
1 Fa la ñetti góor ñooña noppee tontu Ayóoba, ndax la Ayóoba gis njekkam. 2 Ba loolu amee Eliyu doomu Barakel ma askanoo ci Buus, bokk ci làngu Ram daa mer ba futt ca la Ayóoba dëggal boppam fi kanam Yàlla, 3 ak la ñetti xariti Ayóoba ya ñàkk lu ñu ko tontu, ba tax ñu teg Yàlla tooñ. 4 Eliyu nag moo mujjoona wax ak Ayóoba, ndax moo féete ndaw ñett ña. 5 Mu gis ne ñetti góor ña amatuñu tont, xol ba sot, mu mer ba futt. 6 Ca la Eliyu doomu Barakel waa Buus ba, àddu ne:
Man de damay ndaw, ngeen diy mag,
ba tax may teeylu,
ragal leena biralal sama xam-xam.
7 Ma noon: «Na yàgga-dund wax,
na dund-jopp xamle xel mu rafet.»
8 Ndeke xel mi ci nit
mooy noowal Aji Man ji koy may dég-dég.
9 Dund-jopp taxula rafet xel,
te di mag taxula xam yoon.
10 Moo tax ma ne: «Déglu ma;
man it ma biral sama xam-xam.»
11 Dama ne, négandiku naa seeni kàddu,
teewlu seeni déggin,
ba ngeen di jeexi tont ba tey.
12 Yeen laa doon teewlu,
te kat kenn ci yeen yeyu ci Baay Ayóoba,
kenn joxu ko tontam.
13 Buleen ma ne:
«Xel mu rafet mi nu ci gis moo di:
Yàllaa ko mana tiiñal waaye du nit.»
14 Du man la Baay Ayóoba jëme kàddoom,
kon du seeni wax laa koy tontoo.
15 Ñii kat jommi nañu, waxatuñu;
ba kàddu dëddu leen!
16 Dama leen di xaar te waxuñu,
xanaa taxaw, tontootuñu?
17 Damay tontu sama wàll, man it;
damay biral sama xam-xam, man it kay!
18 Sama dënn a fees aki wax,
te samam xel xiir ma ci wax.
19 Sama xol baa ngii mel ni
lu sol biiñ, ube ràpp,
mbete mbuus mu yees mu nara fàcc.
20 Naa wax boog, ba féex,
naa àddu, ba tontu.
21 Duma ci am xejj ak seen,
te duma jay kenn.
22 Xawma sax nu ñuy jaye,