Saar 30
Ayóoba jooy na coono
1 Tey ñi may diijoo ngii, te ñoo ma féete ndaw,
seeni baay a tekkiwuloon tus,
ba ma siide leena jël,
ñuy sàmmandook samay xaj.
2 Ana njariñ lu ñu ma amaloon sax?
Yooyu kooñoor yu jeele?
3 Ñii ndóol, xiif, desey yax,
di ŋeeñaatoo biir àll,
fu lëndëm, gental, maral,
4 di witt ñax mu saxe ciy tan
ak a gasi reen, di dunde.
5 Ñooñu lees dàqe fi biir nit ñi,
di leen yuuxoo niy sàcc,
6 ñu dëkkey xur,
ci biiri pax aki doj,
7 di ŋaaxe biir gajj gi,
dankaloo ci ron dég yi.
8 Ñu sew lañu, ñu kenn yégul,
xanaa caw leen, génne réew mi.
9 Tey nag ñoo may woyantoo,
di ma léeboo.
10 Dañu maa seexlu, ñooru ma,
néeg maa serati ci kanam.
11 Yàllaa ma nasaxal, torxal ma,
ba amatuñook man yemukaay.
12 Mii njurum baadoola mu féete ndijoor, di ma téqtal,
di ma xàllal yooni sànkute.
13 Ñu ngi may dogale, nar maa musibaal,
te soxlawuñu ci ndimbal.
14 Fu yaa lañu bëtte,
buure jali tojit, ne jàyy fi sama kaw.
15 Musiba da maa ëlëm,
sama daraja naaw ni ngelaw,
sama teraanga naaxsaay niw niir.
16 Tey maa ngii sama bakkan di ŋiis,
bési njàqare ne ma taral.
17 Guddi dikk di bënn samay yax, muy rot,
mitit di ŋereñ te du selaw.
18 Kii ne nikk sama mbubb,
ne ratt sama baatu mbubb,
19 xalab ma ci biir ban bi,
may nirook pënd akub dóom.
20 Woo naa la wall, wuyuwoo ma,
ma taxaw, nga niir ma.
21 Yaa soppiku, néege ma,
di ma soxoree sa diisaayu loxo.
22 Yaa ma ne siféet, waral ma ngelaw,
pamti-pamtee ma biir ngëlén.
23 Xam naa xéll ne ci dee nga ma jëme,
te mooy kërug ndajem képp kuy dund.
24 Ku sànkule du tàllal loxoo?
Ku musiba dab du woote wall?
25 Moona sama rongooñ a daan tuurul boroom tiis,
sama xol di tiisoo aji ñàkk ji.
26 Lu baax laa yaakaar, lu bon ne jalañ,
leer laa séentu, guddi ne jaas,
27 sama xol lëmbaajoo, tëë dal,
bési naqar dogale ma.
28 Maa ngi wéye ñuulaay bu ma tàngoor tegul,
di taxawe biir ndaje, di woote wall.
29 Damaa mujj bokk ak till,
neexook looy,
30 ñuul, yaram di xub,
tàng, di bax,
31 sama xalam tiisal,