Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 16
Ayóoba gisatul yaakaar
1 Ayóoba àddu ne:
2 Kàddu yu mel nii, dégg naa ko lu bare.
Dëfalkati yokk joote yi ngeen doon, yeen ñépp!
3 Sa waxi ngelaw yii da dul jeex?
Ana lu la cuq, ba ngay wax rekk?
4 Su ngeen doon man, may yeen,
kon it ma mana wax ni yeen,
tuur leen baati tuuma,
wëcc leen bopp.
5 Waaye su doon man,
ma wax ak yeen, ba dëfal leen,
mas-sawu leen, ba ngeen giif.
 
6 Waaye su ma waxee, mitit du giif;
su ma noppee, du tax mu sore.
7 Yàlla kay a jeexal sama doole,
tas sama gàngoor.
8 Moo ma jàpp, semmal ma;
samab jeexaay seedeel ma tuuma.
9 Meram la ma daggatee, jéppi ma,
di yéyu ci sama kaw,
daasal ma gëti noon, ne ma jàkk.
10 Nit ñaa ngi ŋa ŋàpp fi sama kaw,
sewal ma, di ma talaata,
dajaloo, sam ma.
11 Yàlla da maa wacce ab kàccoor,
rattax ma ci loxoy ñu bon ñi.
12 Féexoon naa, mu falaxe ma;
sëq sama ndodd, rajaxe ma,
def ma diirukaayam,
13 ay fittkatam gaw ma,
mu di ma butti te yërëmul,
di tuur sama sébbriit fi suuf.
14 Mooy buur ni xarekat fi sama kaw,
di ma jamat.
15 Ab saaku laa ñaw, taqoo,
torox, ne dett fi suuf.
16 Sama kanam a ngi xonq curr aki jooy,
sama mbari bët bàddoo lëndëm.
17 Moona saay yoxo jëfewul coxor,
te samag ñaan lal na worma.
 
18 Suufoo, bul làq sama deret ji tuuru,
te yal na sama yuux jollee fu af.
19 Ma ne, tey fi tey, am naa ab seede kaw asamaan,
sama seede kay a nga fa kaw.
20 Ñi may kókkali, saay xarit a,
waaye Yàlla laa koy jooy.
21 Na ab seede layool nit fa Yàlla,
ni doom aadama di layool moroom ma fi kaw suuf!
22 At yu néew déy a ci des,
ma dem yoon wu ma dul délsi.

<- Ayóoba 15Ayóoba 17 ->