Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 50
Babilon daanu na
1 Kàddu gii la Aji Sax ji wax ci mbirum réewum Babilon, réewum Kaldeen ña, te Yonent Yàlla Yeremi jottli ko.
2 «Waxleen xeet yi, yéeneleen,
woneleen misaal te yéene,
waxleen lii, bañ cee làq dara.
Neleen: “Dees na nangu Babilon,
torxal Bel mbaa Mardug, tuur mi,
tas ko,
gàcceel gàllaaj yi, tas kasaray tuur yi.”
3 Aw xeet kay ay bawoo bëj-gànnaar, dal fi seen kaw.
Ñooñooy gentalsi seenum réew,
ba kenn dootu fi dëkk,
nit ak mala, ne mott, ne mes.
4 Su bés baa, ci yooyu fan,»
kàddug Aji Sax jee,
«bànni Israyil ay ànd ak Yudeen ñi,
dikk di jooy,
di sàkku seen Yàlla Aji Sax ji.
5 Dinañu laaj yoonu Siyoŋ, jublu fa
te naan: “Ayca nu dajeji fa Aji Sax ji,
ci biir kóllëre gu sax
gu kenn dul fàtte.”
 
6 «Sama ñoñ ñi réer niy xar,
seeni sàmm a leen lajjal,
sànk leen fi kaw tund yi,
ba tundoo tund, ñu yéegi fa,
fàtte seen goorukaay.
7 Noon bu taseek ñoom warax leen
te naan: “Nun defunu dara.
Ñoom ñoo moy Aji Sax ji,
te mooy dalukaayu njekk,
ba seeni maam yaakaaroon.”
 
8 «Yeen gan ñi, fëxeleen Babilon,
ba sore réewum Kaldeen ñooñu.
Defleen niy sikket, daw jiitu jur gi.
9 Maa ngii déy di xabtal fi kaw Babilon,
kurélu xeet yu mag, bawoo réewum bëj-gànnaar,
làng-déralsi Babilon!
Seeni fitt di ñeyi xare,
du moy, du sooy.
10 Réewum Babilon a doon alalu sëxëtoo,
bu ñuy sëxëtoo ba doyal.»
Kàddug Aji Sax jee.
11 «Ãa yeen waa Babilon, yeena sëxëtoo xeet wi ma séddoo,
di ko bégeek a bànneexoo,
di bajantu ni nag wuy bàcc pepp,
di ŋexal ni naaru góor?
12 Ndaw gàcce gu réy ci seen ndey,
ndaw toroxte ci ki leen sukk jur!
Réew maa ngii di geenu réew yi,
di ndànd-foyfoy, gu wow koŋŋ.
13 Kenn du fi des ndax merum Aji Sax ji,
lépp ay gental,
ba képp ku jaare Babilon,
day waaru, di muslu
ci mboolem mbugal ya fa dal.
14 Yeen fittkat yépp, làng-déral-leen Babilon,
gaw ko, soqeendoo, baña yaxanal!
Ñoo moy Aji Sax ji!
15 Xaaculeen fi kawam, wër ko,
Babilon daanu na, ba joxe ndodd,
tata ya màbb,
dàbbli ya rajaxoo!
Aji Sax jeey feyu,
feyuleen!
Na mu defoon, defleen ko ko.
16 Daggeleen Babilon kuy ji ak kuy góob,
ku fay gan, na daw saamaru noon,
fëx jëm réewam,
dellu cay bokkam.
 
17 «Israyil diy gàtt yu tasaaroo,
yu ay gaynde dàq,
buurub Asiri di gaynde gi jëkka lekk,
Nabukodonosor buuru Babilon topp ca, seeñu yax ya.»
18 Moo tax Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi ne:
«Maa ngii di dikkal buuru Babilon ak waa réewam,
na ma dikkale woon buurub Asiri.
19 Maa ngii di delloo Israyil parloom,
mu dellu di fore àllub Karmel ak Basan,
di regge tundi Efrayim ak Galàdd.
20 Su bés baa, ci yooyu fan,»
kàddug Aji Sax jee,
«dees na seet fi Israyil lu ñaaw, du fi am;
fi Yuda it, deesu fi gis bàkkaar.
Maay jéggal moos ndes wi ma fi saxal.
 
21 «Songleen réewum Meratayim ak waa Pekodd*50.21 waa Meratayim and waa Pekodd ci Babilon lañu bokk.,
jam leen, faagaagal seen gannaaw.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Defleen mboolem li ma leen sant.
22 Coowal xaree ngi fi réew mi,
ak rajaxoo ju réy.
23 Babilon, réew mi daan wàkk mboolem àddina,
tey mu dammtoo ba rajaxoo nii,
dib gent ci biir xeet yi!
24 Babilon, maa la fiir,
nga tancu te yéguloo!
Dañu laa gis, ne la taral,
yaa dëkk Aji Sax ji,
25 Aji Sax ji ubbi na waxandey xareem,
mer, génney gànnaayam.
Liggéeyu Boroom bee, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
foofa ca réewum Babilon.
26 Songeleen ko fu ne,
dàjji ay sàqam,
jal-jalee.
Fàkkasleen lépp, ba du dese dara.
27 Jamleen seen jàmbaari yëkk yépp,
nañu dem ca rendikaay ba.
Wóoy, ngalla ñoom!
Seen bés taxaw na moos,
di seen àppu mbugal.
28 Baatu daw-làqu yu rëcc a ngoog,
bawoo réewum Babilon,
di yeggesi waa Siyoŋ
mbugalum Aji Sax ji sunu Yàlla,
mbugal mi këram waral.
29 Wooleen fittkatoo fittkat fi kaw Babilon,
mboolem kuy tàwwi xala.
Gawleen ko,
bu kenn rëcc.
Feyleen koy jëfam;
def ko ni mu def moroomam.
Babilon a jaay reewande Aji Sax ji,
ku Sell ku Israyil ki.
30 Moo tax bésub keroog
goneem yu góor di daanooy péncam,
niti xareem di wedamandoo.»
Kàddug Aji Sax jee.
31 «Babilon mu reewee, maa ngii fi sa kaw.»
Kàddug Boroom bi, Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi.
«Sa bés déy taxaw na,
di àpp bi ma la wara mbugale.
32 Ku reew keey tërëf, fëlëñu,
te du am ku ko yékkati.
Maay jafal ay dëkkam,
sawara wa xoyom lépp lu ko wër.»
33 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Bànni Israyil ak Yuda, ñépp lañu notandoo.
Ñi leen jàpp ñépp téyee leen doole,
bañ leena ba.
34 Waaye seen jotkat a am doole,
te mooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
Moo leen di layool seen layoo,
ngir jàqal réewum Babilon,
jàmmal waa àddina yi ci des.
35 Saamar ci kaw waa Babilon!»
Kàddug Aji Sax jee.
«Saamar ci kaw waa Babilon
aki kàngamam aki kaaŋam.
36 Saamar ci kaw kebatukati diine yi,
ba seenug ndof feeñ.
Saamar ci kawi jàmbaaram,
ñu ne yàcc.
37 Saamar ci kaw fas ak watiiram,
ak mboolem niti njaxasaan ñi mu fat,
ba ñu mel niy jigéen.
Saamar ci kawi dencam,
ñu sëxëtoo.
38 Maral ci kawi waltanam, mu ŋiis;
mii réew mu nit ñiy jaamoo jëmmi tuur,
ñooy say ndax seen yu ñàng yooyu
39 Moo tax ay dundooti màndiŋ ak rabi àll a koy këroo,
bànjóoli dëkke ko,
kenn dootu fa desati,
kenn dootu fa dëkk mukk ba fàww.
40 Mu mel ni ba Yàlla tasee Sodom ak Gomor,
tasaale la ko wër.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Nit du fa dëkkati,
doom aadama du fa dalati.»
 
41 «Aw askan a ngii, bàyyikoo bëj-gànnaar,
xeet wu mag lañuy doon, buur yu bare,
sàqee fa cati àddina.
42 Yeen waa Babilon, réew mu taaru mi,
fitt aku xeej la ñooñuy ŋàbb,
néeg lool, duñu yërëm,
seen coow ni riirum géej,
ñu war seeni fas,
làng-déral leen ni benn bopp ngir xare.
43 Buuru Babilon dégg riir ma,
yoxo ya yoqi,
njàqare ne ko taral,
mu jàq ni kuy matu.
44 Maa ngii, di fëlle gottub Yurdan ni gaynde,
wuti mbooy gu naat.
Xef ak xippi déy, ma fëxale fa lépp,
ba tabb fa ki ma taamu.
Ana moos ku mel ni man,
ku am sañ-sañ ci man?
Ana njiit luy taxaw fi sama kanam?
45 Kon dégluleen pexe mi Aji Sax ji waajal Babilon,
mébét yi mu mébétal réewum Kaldeen ñooñu!
Ndegam deesul wommat seen gàtt yu ndaw, yóbbu,
ba yàq parlu ma yaxeet.
46 Bu ñuy nangu Babilon,
riir ma day jolli ba riiral suuf,
seeni yuux àkki fa biir xeeti jaambur ya.»

<- Yeremi 49Yeremi 51 ->