Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 48
Lu jëm ci réewum Mowab
1 Lu jëm ci Mowab, Aji Sax ji Yàllay Israyil, Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne:
«Ngalla waa Nebo, seen dëkk ba yàqu na!
Kiryaatayim, ñu torxal, nangu ko;
tata ja daanu, tasaaroo.
2 Mowab amatul woy,
fa Esbon la leen noon ya fexeel lu bon,
ne: “Aycaleen nu raafal wii xeet!”
Yeen waa Madmen it, ñu wedamal;
saamar topp leen.
3 Yuux jibe na Oronayim,
ndaw salfaañook rajaxoo ju réy!
4 Mowab tas, ay fereem serandoo.
5 Ñay yéeg jëm Luwit, di jooyoo.
Ña ngay yéeg, di jooyoo.
Ñay wàcci Oronayim
di dégg aji jàq jiy yuuxoo.
6 Ñu naan: “Dawleen, rawale seen bakkan,
ba tumurànkeji ni gajju màndiŋ!”
7 Mowab, yeena yaakaar dooleek alal,
yeen it, dees na leen jàpp;
Kemos, seen tuur mi duggi ngàllo,
mooki sarxalkatam aki kàngamam.
8 Dëkkoo dëkk ay yàqtoo,
benn dëkk du mucc!
Waa xur wii sànku,
waa déndu doj wu tell wee yàqtoo.»
Muy la Aji Sax ji wax.
9 «Gasal-leen Mowab,
day sànku moos,
ay dëkkam gental,
kenn du fa des!
10 Alkànde ñeel na kuy sàggane liggéeyu Aji Sax ji.
Alkànde ñeel na kuy xañ deret saamaru Aji Sax ji.
 
11 «Mowab a dale féex cag ndawam,
kenn jàppu ko njaam, yóbbu,
wàllanteesu ko ndab ak ndab,
xanaa mu ne degg ni biiñ bu taaje,
di saf, di xeeñ ba tey.
12 Moo tax ay bés a ngii di ñëw,»
kàddug Aji Sax jee,
«maa leen di yónnee ay nit ñu sotti diw gi,
ndab, soteet; njaq, rajax.
13 Yaakaaru Mowab ci Kemos tuur mi, tas,
ni yaakaaru waa kër Israyil ci Betel ma ñu wóolu, tase woon.
 
14 «Mowabee, du yaay kañu,
naan jàmbaar ngeen,
diy ñeyi xare?
15 Song nañu la, yàqte say dëkk;
la man ci say ndaw daanu, fàddu.»
Kàddug Buur Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi.
16 «Musibay Mowab a ngi jegesi,
safaanam làbbleeti, wuti ko.
17 Mboolem yeen ñi wër xeet wii, jooyleen leen;
yeen ñi dégg seen tur ñépp, jooyleen leen.
Neleen: “Moo, nu gii nguur mana foqe,
ba foqaale jii daraja?”
 
18 «Yeen waa Dibon, dëkk bu taaru bi,
wàccleen seen teddnga lu kawe
te tooge digg maral;
kiy yàqtesi Mowab kat song na leen,
di màbbsi seeni tata.
19 Yeen waa Arower,
taxawleen fi yoon wi te teewlu;
góor gu fi jaare mbaa ndaw su rëcc, di daw,
ngeen laaj ko ne ko: “Lu xew?”
20 Ñu ne: “Gàcce ñeel na Mowab gii tas!”
Yuuxooleen, ne wóoy!
Yéeneleen fa tàkkal dexu Arnon,
ne Mowab tas na!
21 Mbugal dikkal déndu doj wu tell wi,
dikkal dëkk yii di Olon, Yaxacc ak Mefat
22 ak Dibon ak Nebo ak Bet Diblatayim
23 ak Kiryaatayim ak Bet Gamul ak Bet Mewon
24 ak Keryot ak Boccra,
mboolem dëkki Mowab daal,
fu jegeek fu sore.
25 Sidditu Mowab day dog,
loxoom damm.»
Kàddug Aji Sax jee!
26 «Du Mowab a doon diir Aji Sax ji mbagg?
Nañu leen màndal sànjum Aji Sax ji,
ba ñu waccu, di ca xuus,
ba ñoom it, ñu di leen ree.
27 Mowabee, du yeena doon ree Israyil?
Dangeen leena fekk ci biiri sàcc,
ba fu ngeen leen tudde, wëcc bopp?
28 Yeen waa Mowab,
baleen dëkk yi, dëkke paxi doj.
Defleen niy xati,
tàgge peggi xunti.
 
29 «Noo dégg ni Mowab bewe,
bew lool,
réy, reew, di damu;
ne daŋŋ-daŋŋiiral.
30 Maa xam seen reewande,»
kàddug Aji Sax jee,
«seeni kañu neen la,
seeni jëf di neen.
31 Moo tax may jooy Mowab,
di wooteel wall Mowab gépp,
di yuuxul waa Kir Eres.
32 Yaw reseñu Sibma gi,
ma jooyal la lu raw la ma jooyal Yaser.
Yaw la say car jàlloon géej,
àkki géeju Yaser,
sa figg jeek sa reseñ, noon yàqte.
33 Tukkal nañu mbégteek bànneex
fi tóokëri réewum Mowab.
Maa ŋacc mbàndi biiñ ya,
kenn nalatu fa reseñ, di soowoo
coowal mbégte, xanaa ay yuux.
34 Yuux jibe na Esbon, ba Elale,
àkki ba Yaxacc
ak Sowar ba Oronayim ak Eglat Selisiya.
Ndoxi Nimrim sax ŋiis na.
35 Maay bóome biir Mowab.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Maay bóom kuy joxe sarax ci jaamookaay,
di taalal am tuuram cuuraay.
36 Naa jooy Mowab jooyi xol,
yu toxoro di jooye ab dëj,
na toxoro di jooye dëju waa Kir Eres.
Lu ñu dajale woon sànku na!
37 Ñoom ñépp a nelu,
wat seeni sikkim,
daggat seeni loxo,
sol ay saaku, di ko ñaawloo.
38 Kaw taaxi Mowab yépp aki péncam,
fépp ay yuuxoo di jib.
Maa toj Mowab
ni ndab lu kenn soxlaatul.»
Kàddug Aji Sax jee.
39 «Yuuxooleen, ne leen: “Céy gii yàqtoo!
Mowab gii wone gannaaw! Mowab rus na.”
Ñi ko wër ñépp a koy reetaan, seen yaram di daw ci ñoom.»
40 Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Lu mel ni jaxaay a ngii naa jàyy,
firiy laafam, këfsi Mowab.
41 Dees na teg Keryot ga ca Mowab loxo,
ne tata ya taral;
su keroogee fitu jàmbaar ne tërit,
mu mel ni kuy matu.
42 Mowab day sànku, ba xeetam fey.
Ñoo doon diir Aji Sax ji mbagg.
43 Yeen waa Mowab,
pat-pati rekk, di tàbbiy pax aki yeer.»
Kàddug Aji Sax jee.
44 «Pat-patiy daw, tàbbim pax;
génn um pax, tàbbim yeer.
Maay yen Mowab, maa leen di yen moos,
seen atum mbugal.»
Kàddug Aji Sax jee.
45 «Fa keppaaru Esbon lañuy daw taxawi,
doole dëddu.
Booba sawaraa tàkke Esbon, di law;
sël-sëlee foofa ca péeyu Buur Siwon,
ba dajal réewum Mowab, nitu coow ña,
boole jë akum kaaŋ xoyom.
46 Wóoy, waa Mowab, ngalla yeen!
Yeen ñiy jaamu Kemos, sànku ngeen!
Dees na jàpp seen doom yu góor njaam;
jigéen ñi it, njaam.
 
47 «Du tee fan yu mujj ya,
ma tijji wërsëgu Mowab.»
Kàddug Aji Sax jee.
Fii la àtteb Mowab yem.

<- Yeremi 47Yeremi 49 ->