Saar 45
Barug mucc na
1 Kàddu gii Yeremi waxoon na ko Barug doomu Nerya, gannaaw ba Barug tënkee ci taxañu mbind, kàddu ya ko Yeremi dégtal ca ñeenteelu atu nguurug doomu Yosya, Yowakim buurub Yuda. 2 «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ci yaw, Barug. 3 Nga ne: “Wóoy ngalla man! Aji Sax ji yokk na maw naqar. Onk naa ba tàyyi te awma noflaay.” 4 Aji Sax ji da maa sant ma wax la ne la: “Aji Sax ji dafa wax ne:
La ma tabaxoon a ngii,
maa ngi koy daaneel,
la ma jëmbatoon a ngii,
maa ngi koy buddat,
ba réew mépp daj.
5 Looy sàkku ku la beral loxo?
Jaru ko!
Maa ngii di wàcceel musiba képp kuy noyyi.”
Kàddug Aji Sax jee!
“Waaye may naa la sa bakkan di sa yoolu xare,