Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 36
Yowakim def na musibaam
1 Ba loolu wéyee, ci ñeenteelu atu nguurug buurub Yuda Yowakim doomu Yosya, kàddu gii dikkal na Yeremi, bàyyikoo ci Aji Sax ji, ne ko: 2 «Jëlal taxañu bindukaay*36.2 taxañu bindukaay ay dogiti der yu bare yu ñu ñawante lay doon, ba mu doon deru bindukaay bu mag bu ñuy taxañ ci bant. Mbind mi nag def ay dog yu dékkarloo. , nga bind ci mboolem kàddu yi ma la wax ci mbirum Israyil ak Yuda ak mboolem xeet yi, te nga dale ko ba ma waxeek yaw ca jamonoy Yosya ba bésub tey jii. 3 Jombul waa kër Yuda dégg mboolem musiba mi ma leen nara teg, ba tax ku ne ci ñoom dëpp yoonam wu bon, ngir ma baal leen seen ñaawtéef ak seen moy.»

4 Yeremi woo Barug doomu Nerya, dégtal ko mboolem kàddu yi ko Aji Sax ji wax, mu bind ko ci ab taxañu bindukaay. 5 Yeremi nag wax Barug, ne ko: «Man damaa am ngànt. Duma mana dem kër Aji Sax ja. 6 Demal yaw bésub koor, nga jàng taxañ, bi nga bind kàdduy Aji Sax, ji ma la dégtal, ña ca kër Aji Sax ji di dégg. Nanga ko jàng itam ci kanam mboolem Yudeen ña jóge seeni dëkk. 7 Jombul ñu tinu Aji Sax ji, ku nekk ci ñoom dëpp yoonu mbonam, ndax mer mu réy ak xadar ji Aji Sax ji tuddal askan wii kat, nar naa metti.»

8 Barug doomu Nerya def mboolem la ko Yonent Yàlla Yeremi sant, daldi jàng ca kër Aji Sax ji taxañ ba ñu bind kàdduy Aji Sax ji. 9 Loolu yemook juróomeelu atu nguurug buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya ca juróom ñeenteelu weer wa. Fekk ñu yéene koor fi kanam Aji Sax ji, ñeel waa Yerusalem gépp ak mboolem ña jóge dëkki Yuda. 10 Ci biir loolu Barug tollu ca néegu bindkat ba, Gemarya doomu Safan, ca kër Aji Sax ja. Muy jàng taxañ ba ñu bind kàdduy Aji Sax ji, mbooloo mépp di dégg. Néeg baa nga woon ca ëttu kër Aji Sax ja ca kaw, fa féeteek bunt bu Bees ba. 11 Mise doomu Gemarya doomu Safan dégg mboolem kàdduy Aji Sax, ja ca taxañ ba. 12 Mu daldi wàcc, ba ca kër buur, jàll ca néegu bindkat ba, fekk fa kàngam yépp toog: Elisama bindkat ba, ak Delaya doomu Semaya, ak Elnatan doomu Agbor, ak Gemarya doomu Safan, ak Cedesyas doomu Anaña, ak jawriñ ña ca des ñépp. 13 Mise yegge leen lépp la mu dégg Barug jànge ko ca taxañ ba ca kanam mbooloo ma.

14 Ci kaw loolu kàngam yépp yebal Yewudi doomu Netaña doomu Selemya doomu Kusi. Ñu ne ko: «Demal ne Barug taxañ bi mu jàngal mbooloo mi, na ko jël te ñëw, indaale ko.» Barug doomu Nerya ŋàbb taxañ ba ca loxoom, dem ba ca ñoom. 15 Ñu ne ko: «Toogal jàngal nu ko, nu dégg.» Barug jàngal leen ko, ñu dégg. 16 Ba ñu déggee kàddu ya yépp, dañoo tiit, ku ne xool sa moroom. Ñu ne Barug: «Nun kat, nan yegge Buur mbir mii mépp.» 17 Ñu laaj Barug, ne ko: «Wax nu! Noo binde kàddu yii yépp. Yeremee la ko dégtal?» 18 Barug ne leen: «Moo ma dégtal kàddu yépp de, ma binde ko daa ci taxañ bi.» 19 Kàngam ya ne Barug: «Demal làquji yaak Yeremi, te bu kenn xam fu ngeen ne!»

20 Ba loolu amee ñu wacc taxañ ba ca néeg Elisama bindkat ba, daldi ànd fekki Buur ca ëttam. Ñu yegge ko mbir ma mépp.

21 Buur nag yebal Yewudi, ngir mu jëli taxañ ba. Mu jëleji ko ca néeg Elisama bindkat ba, daldi jàngal taxañ ba Buur, mook mboolem kàngam ya feggook moom. 22 Booba jamonoy sedd la woon, yemook juróom ñeenteelu weer wa. Buur a nga toog ca biir néegu njaaram; taal ba yànj, janook moom. 23 Ci biir loolu saa yu Yewudi jàngee ñetti dog ba ñeent, Buur fab saatus bindkat, dagg dog ya, sànni ca taal ba. Mu di ko def ba taxañ ba lakk ca taal ba, ba jeex tàkk. 24 Buur ak jawriñam ña ñépp dégg nañu kàddu ya, waaye tiituñu sax, astamaak di xotti seeni yére ni kuy tiislu di def. 25 Elnatan ak Delaya ak Gemarya sax tinu nañu Buur, ngir mu baña lakk taxañ ba. Waaye Buur dégluw leen, 26 xanaa mu sant Yerameel, kenn ci askanu Buur, mook Seraya doomu Asriyel, ak Selemya doomu Abdel, ne leen ñu jàpp Barug bindkat ba ak Yonent Yàlla Yeremi. Teewul Aji Sax ji làq leen.

27 Gannaaw ba Buur lakkee taxañ, ba def kàddu ya Barug bindoon ca dégtalub Yeremi, kàddug Aji Sax ji dikkal na Yeremi, ne ko: 28 «Dellul jël beneen taxañu bindukaay, nga dellu bind ca mboolem kàddu ya woon ca taxañ ba Yowakim buurub Yuda lakk. 29 Yowakim buurub Yuda nag, nanga ko wax ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne yaw yaa lakk taxañ bii, naan lu waral ma bind ci ne buuru Babilon dina ñëw moos te dina tas réew mii, faagaagal fi nit ak mala. 30 Moo tax Aji Sax ji wax ci mbirum Yowakim buurub Yuda, ne: du am ku ko toogal ci jalub Daawuda. Néewam dees koy sànni ci biti, mu yendoo naaj, fanaanoo sedd. 31 Maa koy yen añu ñaawtéefam, mook njabootam aki surgaam. Maay wàcce ci seen kaw, ñook waa Yerusalem ak Yuda gépp, mboolem musiba mu ma leen digoon, te taxul ñu dégg.”»

32 Ci kaw loolu Yeremi jël beneen taxañu bindukaay, jox ko bindkat ba, Barug doomu Nerya. Mu dégtal ko, mu bind ca mboolem kàdduy taxañ, ba Yowakim buurub Yuda lakkoon ca taal ba. Yeneen kàddu yu bare yu ni mel sax, dolliku na ca.

<- Yeremi 35Yeremi 37 ->