5 Ba loolu amee Yonent Yàlla Yeremi tontu yonent ba ñuy wax Anaña fa kanam sarxalkat yaak mbooloo ma taxaw fa biir kër Aji Sax ji mépp. 6 Mu ne ko: «Amiin! Yal na ko Aji Sax ji defee! Yal na Aji Sax ji sottal sa kàdduy waxyu yi nga wax, ba délloosee Babilon ba fii ndabi kër Aji Sax ji ak mboolem ña ñu fa toxal. 7 Waaye ngalla déglul bu baax kàddu gii ma lay wax, yaak mbooloo mi mépp. 8 Yonent yi feeñoon naka jekk lu ma jiitu, jiitu la, jottli nañu réew yu yaatu ak nguur yu mag seen waxyuy xare ak musiba ak mbas. 9 Ab yonent nag bu dee biral waxyub jàmm, su jàmm ja dikkee, ñu xam ne Aji Sax jee ko yebal ci lu wér.»
10 Ba mu ko defee yonent ba ñuy wax Anaña yékkatee yet wa ca ndoddu Yonent Yàlla Yeremi, damm ko. 11 Anaña àddu fa kanam mbooloo ma mépp ne leen: «Aji Sax ji dafa wax ne: Nii laay damme yet wi buur Nabukodonosor buuru Babilon di tënkee. Fii ak ñaari at tembe dinaa jële yet wi ci ndoddu mboolem xeet yi mu ko tënke.» Ba loolu amee Yonent Yàlla Yeremi dem yoonam.
12 Gannaaw ba yonent ba ñuy wax Anaña yékkatee yet wa ca ndoddu Yonent Yàlla Yeremi ba damm ko, kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi, ne ko: 13 «Demal wax Anaña ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Yetu bant nga damm, waaye dinga ko wuutale yetu weñ. 14 Ndax Aji Sax ji, Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi dafa wax ne: Yetu weñ laay teg ci ndoddu mboolem xeet yii, ñu nangul Nabukodonosor buuru Babilon, di ko surgawu. Te rabi àll yi sax, maa leen di teg ci loxoom.”»
15 Gannaaw loolu Yonent Yàlla Yeremi ne yonent ba ñuy wax Anaña: «Anaña, déglul bu baax li ma lay wax: Aji Sax ji yebalu la, yaw ngay gëmloo askan wii ay fen. 16 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la yebal, nga jóge fi kaw suuf. Ren jii ngay dee, ndax kàdduy gàntal nga waxal Aji Sax ji.”»
17 Yonent ba ñuy wax Anaña ca at mooma la dee ca juróom ñaareelu weer wa.
<- Yeremi 27Yeremi 29 ->