9 «“Kon nag yeen, buleen déglu seen yonent yeek seetkat yeek firikati gént yeek boroom rawaan yeek ñeengokat yi leen di wax, naan leen dungeen tàbbi ci curgag buuru Babilon. 10 Ay waxyuy fen déy lañu leen di waxal te dinañu leen taxa toxoo seenum réew. Maa leen di sànni fu sore, ngeen sànku. 11 Waaye xeet wu ci nangoo wacce yetu buuru Babilon seen ndodd, di ko surgawu, ñooñu, maa leen di saxal ci seen suuf.” Kàddug Aji Sax jee. “Ñu dëkke ko, di ko bey.”»
12 Ci biir loolu Cedesyas buurub Yuda it, ma yegge ko kàddu yooyu yépp, ne ko: «Wàcceel yetu buuru Babilon saw ndodd, nangul ko, nangul ay bokkam, ndax ngeen dund. 13 Ana lu jar saamar akub xiif ak mbas di la rey, yaak sa waa réew mi, ni ko Aji Sax ji dige xeet wu ci nangulul buuru Babilon? 14 Buleen déglu yonent yi leen di wax naan leen dungeen tàbbi ci curgag buuru Babilon. Ay waxyuy fen déy lañu leen di waxal. 15 Man déy yónniwma leen.» Kàddug Aji Sax jee. «Te ñoom ñu ngi waxe waxyuy fen ci sama tur. Moo tax maa leen di dàqe fii, ngeen sànku, yeen ak yonent yi leen di waxyul.»
16 Gannaaw loolu sarxalkat yeek askan wii wépp wax naa leen ne leen: «Aji Sax ji dafa wax ne: Buleen déglu yonent yi leen di waxal ay waxyu, naan leen: “Ndabi†27.16 Ndab yooyu gànjar la woon ndax wurus lay doon mbaa xaalis. kër Aji Sax jaa ngii di délsi, jóge Babilon léegi, léegi.” Ay waxyuy fen lañu leen di waxal. 17 Buleen leen déglu. Nangul-leen buuru Babilon te dund! Ana lu jar dëkk bii di mujje doon jalub xeer?» 18 Bu ñu dee ay yonent kay, te kàddug Aji Sax ji nekk ci ñoom, nañu daldi tinu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ngir ndab yi des kër Aji Sax ji ak kër buurub Yudak Yerusalem, te baña dem Babilon. 19 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi de wax na ci mbirum jëni këram geek mbalka meek watiiri rootukaay yi ak yeneen ndab yi des ci dëkk bii, 20 Mooy ndab ya Nabukodonosor buuru Babilon yóbbaalewloon, ba muy yóbbu ngàllo doomu Yowakim, Yekoña buurub Yuda, jële ko Yerusalem, jëme ko Babilon, mook kàngami Yudak Yerusalem. 21 Lii déy Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi wax na ko ci ndab yooyu des ca kër Aji Sax ji ak kër buurub Yudak Yerusalem. 22 Mu ne: «Babilon lees koy boole yóbbu, te foofa lay des ba keroog bés ba ma ciy jóg.» Kàddug Aji Sax jee. «Gannaaw loolu dinaa ko fa jële, délloosi ko bérab bii.»
<- Yeremi 26Yeremi 28 ->