Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 24
Li ñaari dàmbi figg di misaal
1 Gannaaw gi Nabukodonosor buuru Babilon toxal na buurub Yuda Yekoña*24.1 Yekoña ak Yowakin kenn ki la. doomu Yowakim, yóbbu ko Babilon, mook kàngami Yudak liggéeykati xarala yaak liggéeykati weñ ya. Ba loolu amee Aji Sax ji am lu mu ma won: da maa jekki gis ñaari dàmbi figg yu tege fi kanam kër Aji Sax ji. 2 Genn dàmb gi di figg ju baaxa baax, mel ni witt mu jëkk. Dàmb gi ci des di figg ju bona bon, ju kenn dul lekk ndax bon.

3 Aji Sax ji wax ma ne ma: «Yeremi, loo gis?» Ma ne ko: «Xanaa ay figg. Figg ju baax ji nag baax na lool, waaye ju bon ji daa bona bon, ba kenn du ko lekk ndax bon.»

4 Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ma, ne ma: 5 «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Ni figg jii baaxe, ni laay geesoo mbaax ngàllog Yuda gi ma yebale bérab bii, jëme leen réewum Babilon. 6 Maa leen di toppe bëtu mbaax, ba délloosi leen ci réew mii. Maa leen di defar te duma leen daaneel; jëmbat leen te duma leen buddi. 7 Maa leen di may coobarey xam ma, te xam ne maay Aji Sax ji, ba ñu doon sama ñoñu bopp, man ma doon seen Yàlla. Dinañu délseek seen léppi xol ci man déy!»

8 Waaye Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Ni figg jii bone, ba kenn manu koo lekk ndax bon, ni laay def Cedesyas buurub Yuda aki kàngamam ak ndesu Yerusalem. Muy ñi des ci réew mi, di ña toxuji Misra. 9 Maa leen di def ñu jara seexlu, di musibay mboolem réewi àddina, ba fépp fu ma leen sànni, seen tur di fa saaga te kuy léeboo ak kuy kókkalee mbaa ngay móoloo, ñoom ngay tudd. 10 Maay yebal saamar fi seen kaw ak xiif ak mbas, ba ñu raaf fi kaw suuf si ma leen joxoon, ñook seeni maam.»

<- Yeremi 23Yeremi 25 ->