6 «Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «su boobaa deesatul wooye bérab bii Tofet mbaa xuru Ben Inom, xanaa xuru Bóomukaay. 7 Maay neenale fii pexem Yudak Yerusalem. Maa leen di tërale seen saamaru noon, ñi leen di tëru, tër leen; seeni néew, ma leele njanaaw ak rabi àll. 8 Maay def dëkk bi ab gent bu ñuy muslu, ku fi jaare waaru, di muslu ci seen mbugal yépp. 9 Maa leen di yàpploo seen doom yu góor ak yu jigéen, ku nekk di yàpp sa moroom ci biir njàqare, ndax gaw bu metti, bu leen seen noon yi leen di tëru di gaw.
10 «Gannaaw loolu nanga toj njaq lu ndaw li fi kanam ñi nga àndal, 11 te nga ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Askan wii ak dëkk bii, ni ñuy toje njaq, ba deesatu ko mana defaraat, ni laa koy tojate. Tofet gii dees na fi rob ndax ñàkk fu ñu robe. 12 Noonu laay def bérab bii,” kàddug Aji Sax jee, “ak ñi fi dëkk. Maay def dëkk bii ni Tofet. 13 Këri Yerusalem ak këri buuri Yuda dina fees ak sobe ni bérab bii di Tofet. Mooy mboolem kër yu ñu doon taalal cuuraay ca kaw taax ya ñeel biddiiw yépp, ak di fa tuural yeneen yàlla.”»
14 Gannaaw ba Yeremi walbatikoo Tofet, ga ko Aji Sax ji yebaloon mu waxi fa waxyu, dafa taxawi ca ëtti kër Aji Sax ji, daldi wax ak mbooloo ma mépp. Mu ne leen: 15 «Aji Sax ji, Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Maa ngii di wàcce ci kaw dëkk bii ak mboolem li ko wër, lépp luy musiba mu ma dige woon, ndax dangeena të ticc, baña dégg sama kàddu.”»
<- Yeremi 18Yeremi 20 ->