Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 10
Israyil ŋarale na
1 Israyil di reseñ gu naat,
meññal boppam lu ne gàññ,
te lu meññeef ma gëna yokku,
mu gëna yokkati sarxalukaayi tuur.
Lu am réewam gëna baaxle,
mu gëna baaxal ay xeri tuur.
2 Ñooy boroom xolub jinigalkat,
te tey ñooy gàddu seen bàkkaar.
Aji Sax ji mooy toj seeni sarxalukaay,
tas seen xeri tuur.
3 Léegi ñu ne: «Amunu buur,
ndax noo wormaalul Aji Sax ji,
te su nu amoon buur it, lu mu nu manal?
4 Ñooy wax seeni wax,
di giñe ay fen yu ñuy fasoo kóllëre,
ba yoon mel ni gàncaxu tooke
ju law ca tooboy tool ya.»
5 Waa Samaree ngi am tiitaange ci
sëllu wu ñu xelli ca Bet Awen*10.5 Seetal ci Ose 4.15.,
askan wa di tiislu tuur ma,
ay xërëmkatam di lox ndax darajay sëllu,
ji leen dëddu, dem ngàllo.
6 Moom it lees di yóbbu Asiri,
defal ko buur bu mag ba ab galag.
Gàcce mooy jàpp Efrayim,
Israyil laa ne, mooy rus ci mébétam.
7 Samari lees di tas, mook buuram,
mu mel ni bant buy tëmb di dem.
8 Jaamookaay yu kawe ya ca Bet Awen,
bàkkaarukaayi Israyil yooyu lees di tas.
Ay dég aki dagg ñooy sax ca seeni sarxalukaay,
dees na ne tund yu mag yi: «Mëddleen nu,»
te naan tund yu ndaw yi: «Daanuleen ci sunu kaw.»
9 «Israyiloo, ca janti Gibeya10.9 Gibeya: seetal ci Njiit ya 19-21. nga dala moye,
te foofu la waa réew mi tollu ba tey.
Luy tee xare dabe nit ñu jubadi ñi ca Gibeya?
10 Saa yu ma soobee ma yar leen.
Ay xeet ay daje, jógal leen,
jéng leen ndax seen ñaari ñaawtéef.
11 Efrayim aw nag wu nangu la woon,
te sawaroona bàcc am pepp.
Maa ràng loosam wu jekk.
Maa takk Efrayim,
Yuda gàbb, Yanqóoba rijjil boppam.
12 Jiwal-leen seen bopp njekk,
ba góobe ca lu ngor maye.
Gàbbleen ag mbooy,
sàkku Aji Sax ji jot na,
ba kera muy dikk, tawal leen njekk.
13 Yeena bey ag coxor,
góob ag mbon.
Yeena lekk meññeefum fen,
nde yeena wóolu seen pexey bopp,
ak seen jàmbaar yu bare.
14 Am riir mooy jollee ca sa biir gàngoor,
sa tata yépp tas, na Salman tase woon Bet Arbel,
keroog bésub xare ba,
ba ñu jëlee ndey, fenqaleek doom, ñu rajaxoo.
15 Noonu lees leen di def, yeen waa Betel
ndax seen mbon gu réy.
Jant a ngay fenk, buurub Israyil dee wett.

<- Ose 9Ose 11 ->