6 Ba ñu waajalee noonu yooyii ba mu jekk, sarxalkat yaa daan dugg saa su nekk ca néeg bu jëkk ba, di def seen liggéey. 7 Waaye ñaareelu néeg ba, sarxalkat bu mag ba doŋŋ moo ca daan dugg, benn yoon cim at, te du ñàkka duggaale deret ju muy jooxe ngir boppam, ak itam ngir bàkkaar yi askan wi def te du ag teyeef. 8 Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye dugg ca bérab bu sell baa sell feeñagul woon, te fekk néeg bu jëkk ba di taxaw ba tey. 9 Loolu misaal la, ñeel jamonoy tey, di firndeel ne jooxe yi ak saraxi jur yi ñu daan jébbale manuñoo dindi yaraangeg jaamukatub Yàlla bi, ba mu set wecc. 10 Sarax yooyu, ci aw ñam ak ag naan, ak xeeti njàpp doŋŋ la jëm, lépp yittewoo yaramu suuxu neen, te di ndigal yu leen waroon ba keroog bésub coppite taxaw.
16 Kayitu ndono nag fu mu teew, fàww joxees fa firndey deewug ka donale, 17 ndax kayitu ndono du wér lu moy gannaaw bu nit ka deeyee. Du jàppandi mukk li feek ki donalee ngi dund. 18 Looloo waral it kóllëre*9.18 kóllëre: benn baat mooy tekki «kóllëre» ak «kayitu ndono.» gu jëkk ga ci boppam, dooreesu ko woon te deret tuuruwul. 19 Keroog ba Musaa biralalee bànni Israyil gépp mboolem santaane, na ko yoon wi laaje, ba mu noppee, deretu wëllu la jël, ak ju sikket, akum ndox, ak caru garabu isob bu mu laxas kawaru xar mu xonq. Mu capp ko ca deret ja, wis-wisal ca kaw téereb yoon wa, ak mbooloo mépp. 20 Mu ne: «Lii mooy deretu kóllëre gi Yàlla fas ak yeen†9.20 Seetal ci Mucc ga 24.8..» 21 Xayma ba, ak mboolem ndabi carxal ya it, noonu la wis-wisale ca kaw. 22 Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.
23 Jumtukaay yooyi di ay misaali yëf ya fa asamaan, yooyu sarax lees ko waroona setale. Kon yëfi asamaan ya ci boppam, sarax yu ko gën lees ko wara setale. 24 Ndax bérab yu sell yu nit tabax, te muy royaalub bérab bu dëggu ba doŋŋ, du ci la Almasi dugg. Waaye biir asamaan ci boppam la dugg ngir teewal nu tey, fa kanam Yàlla. 25 Duggul biir asamaan it ngir di sarxe ak a sarxewaat boppam, noonee sarxalkat bu mag ba daan dugge at mu nekk fu sell faa sell, yóbbaale deret ju dul josam. 26 Lu ko moy ca njàlbéenu àddina lay dale sonn ay yooni yoon. Waaye tey ci mujug jamono yi la feeñ benn yoon doŋŋ, ba sarxe boppam, ngir far bàkkaar. 27 Kon ni ab dogal sédde nit ñi benn yoon doŋŋ bu ñuy dee, seenub àtte topp ci, 28 noonu itam la Almasi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.
<- Yawut ya 8Yawut ya 10 ->