3 Gannaaw nag ab sarxalkat bu mag bu mu mana doon, dees koo fal, ngir muy jébbale ay jooxe ak saraxi jur, kon fàww sarxalkat bu mag bii itam am lu mu sarxe. 4 Bu doon ci àddina, du nekk sax ab sarxalkat, gannaaw ay sarxalkat a ngi fi, di jébbale ay sarax, ni ko yoonu Musaa laaje. 5 Sarxalkat yooyu, jaamookaay bi ñuy liggéeye, ab misaal la, takkndeeru yëf yu dëggu ya fa asamaan la. Ndax ba Musaa di waaja yékkati xaymab jaamookaay ba, noonu lees ko artoo woon ne ko: «Nanga xool te def lépp, mu dëppook misaal mi ñu la won ci kaw tund wi*8.5 Seetal ci Mucc ga 25.40..» 6 Waaye tey la Yeesu jot ci liggéeyu carxal gu sut gu jëkk ga fuuf, te kóllëre gi mu fas diggante Yàlla ak nit ñi, noonu la gëne gu jëkk ga; dige yi lal kóllëre gu yees gii it, noonu la gëne dige ya laloon gu jëkk ga.
7 Bu kóllëre gu jëkk ga muccoon sikk nag, deesul soxlaa xajal geneen. 8 Waaye Yàllaa sikk bànni Israyil, ba mu nee:
10 «Lii nag moo di kóllëre gi may fas
13 Bu Yàlla wooyee kóllëre gii gu yees nag, daa fekk mu wonnil gu jëkk ga. Lu wonni te di lu yàgg nag, mu ngi ci tànki wees.
<- Yawut ya 7Yawut ya 9 ->