4 Seetleen ni mu ràññikoo, moom la Ibraayma maamu cosaan ma ci boppam jébbal fukkeelu cérub cëxëtoo ma! 5 Te sarxalkat yi bokk ci giirug Lewi†7.5 Lewi mooy maamu Aaróona ak Musaa. ni ko yoon wi tërale, ñoom lañu sant ñu nangu céri fukkeeli alali askan wiy seeni bokk, te soqikoo ñoom itam ci geñog Ibraayma. 6 Waaye Melkisedeg mi ñu askanalewul giirug Lewi, ci Ibraayma la nangoo cérub fukkeel. Te it moo ñaanal barke Ibraayma mi jagoo digey Yàlla. 7 Te amul benn werante ne ki féete suuf, moom la ki féete kaw di ñaanal barke. 8 Kon ci gii wet ay nit ñuy dee doŋŋ ñooy nangu ay céri fukkeel, ca gee wet nag ku ñu seedeel ne mu ngi dund ba tey moo jagoo cérub fukkeel. 9 Léegi nag ci waxin, Lewi miy nangu cérub fukkeel, moo génne cérub fukkeel bu mu feye ci loxol Ibraayma. 10 Ndax ba Melkisedeg di gatandu Ibraayma, Lewi ma nga woon ca geñog Ibraayma maamam.
18 Kon ci genn wet, santaane ba woon, moom lañu neenal, ndax matadig santaane ba, ak ñàkka jariñeem, 19 ndax yoonu Musaa sottalul dara ba mu mat sëkk. Ci geneen wet, yaakaar ju gën moo nuyoo, di yoon wu nuy jaare ba àgg fa Yàlla.
20 Te it palug sarxalkat bii ñàkkula ànd ak ngiñ, nde sarxalkat yee, ñoom lees daan fal pal gu àndul ak ngiñ. 21 Waaye Yeesu mii la ag palam ànd ak ngiñ lu jibe ca ka ko wax ne ko:
23 Ñi ñu masa fal sarxalkat nag bare nañu, te tëlee wéye fàww seen sas moo tax, gannaaw ñoom ñépp ay dee. 24 Waaye Yeesu mi sax ba fàww, moo sasoo carxal gu sax dàkk. 25 Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.
26 Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla; moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan. 27 Bokkul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawula jiital bés bu nekk, saraxi jur ngir bàkkaari boppam, door cee teg ay sarax ngir bàkkaari askan wi. Benn yoon la Yeesu sarxal, mu doy, te mooy ba mu sarxee boppam. 28 Ndax kat yoonu Musaa, ay nit ak seenug néew doole la fal ay sarxalkat yu mag. Waaye kàddug ngiñ li topp ci yoon wi, moo fal sarxalkat bu mag, Doom ji ñu matal sëkk ba fàww.
<- Yawut ya 6Yawut ya 8 ->