7 Gannaaw loolu Yuusufa ànd ak baayam ba fa Firawna, nuyole ko ak moom. Yanqóoba nuyu Firawna. 8 Firawna laaj Yanqóoba ne ko: «Aa, góor gi, xanaa war ngaa doon mag de!» 9 Yanqóoba wax Firawna ne ko: «Samay ati màngaan, ba ma ganee àddina ba tey de, mu ngi tollu ci téeméer ak fanweer, muy at yu gàtt te naqari, te it demuma bay tolloo ay at ak samay maam, ba ñuy màngaan ci àddina.» 10 Ba mu ko defee Yanqóoba ñaanal Firawna, bàyyikoo fa, daldi dem.
11 Yuusufa nag dalal baayam aki bokkam, dogal leen suuf sa gën ca réewum Misra ca diiwaanu Ramses, ni ko ko Firawna sante woon. 12 Ba loolu amee Yuusufa di dundal baayam aki bokkam, ak mboolem waa kër baayam, boole ca ña bootu ca ñoom.
20 Yuusufa nag jëndal Firawna suufas Misra gépp, ngir waa Misra ya jaay ku ci nekk sa tool ndax xiif, ba leen jiital, ba Firawna mujj moom suuf si. 21 Waa réew ma ñoom, Yuusufa da leena def ay jaam ca Misra, gii wet ba gaa. 22 Bàyyiwul lu moy suufu njiiti diine ya, ndax Firawna jotoon na leena dogal ay cér, jagleel leen. Moo tax jaayuñu seeni suuf.
23 Yuusufa ne waa réew ma: «Léegi gannaaw jënd naa leen, ba Firawna moom leen, yeen ak seeni suuf, jiwoo ngii, demleen jiyi. 24 Bu nu àggee ci ngóob, juróom yu ngeen am dingeen ci jox Firawna benn, te féetewoo ñeenti cér yi des. Su ko defee ngeen génne ci jiwuy tool yi, li ci des ngeen dunde, yeen ak seen waa kër ak seeni doom.» 25 Ñu ne ko: «Sang bi, rawale nga nu! Te gannaaw laaye nga nu biir, nangu nanoo doon jaami Firawna.» 26 Noonu la Yuusufa tërale loola, def ko dogalu yoon ca suufu Misra, te loolooy wéy ba tey jii: juróomi céri meññeef mu ne, Firawnaay moom benn ba. Waaye suufi njiiti diine ya ca bokkul, Firawna amu ca dara.
28 Yanqóoba nag nekk na fukki at ak juróom ñaar ca réewum Misra, ay atam yépp tollu ci téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar (147). 29 Ba nga xamee ne àppu Israyil a ngay bëgga mat, dafa woolu doomam Yuusufa ne ko: «Ngalla waay dugalal sa loxo, mu ron sama lupp[a], muy ngiñ ci yaw ne dinga jëflanteek man ci ngor ak worma: rikk, bu ma denc Misra. 30 Bés bu ma fekkijee samay maam, nanga ma jële Misra, denci ma ca seen xuntim bàmmeel.» Yuusufa ne ko: «Dinaa la defal li nga wax.» 31 Mu ne ko: «Giñal ma ko.» Yuusufa giñ ko, Israyil doora am jàmm, daldi wéeru ca bopp lal ba.
<- Njàlbéen ga 46Njàlbéen ga 48 ->- a 47.29 Seetal ci 24.2-3.