3 Ci kaw loolu fukki magi Yuusufa ya dem Misra, jëndi pepp. 4 Waaye Yanqóoba yebalul Beñamin, rakku Yuusufa, ndax dafa ragal ne musiba man na koo dab. 5 Doomi Israyil ñëw nag ci biir ñiy jëndsi pepp, ndax xiif bi lawoon na ba Kanaan. 6 Fekk booba Yuusufa mooy dogal ca réew ma, di jaay pepp waa réew mépp. Magi Yuusufa ya ñëw, sujjóotal Yuusufa.
18 Ca gannaaw ëllëg sa Yuusufa ne leen: «Bu ngeen defee lii may wax, dingeen dund, ndax man ragal naa Yàlla. 19 Ndegam ñu maandu ngeen, na leen kenn ci seen doomi baay wuutu fii, ñi ci des dem yóbbul pepp seen waa kër, yi nekk ci xiif. 20 Waaye nangeen ma indil seen rakk, ba ma xam ne li ngeen wax dëgg la; su ko defee dungeen dee.» Ñu daldi ne: «Waaw,» 21 te naa ci seen biir: «Céy su nu yégoon, sunu àqu rakk a nu topp nii, ndax danu koo seetaanoon, mu nekk ci njàqarey xol, di nu tinu, te faalewunu ko; looloo waral sunu njàqarey tey jii.» 22 Ruben nag àddu ne leen: «Ndax newuma leen woon: “Buleen gàddu bakkanu xale bi,” waaye faalewuleen ma; tey rekk la nu Yàlla doon xaare bakkanam, bi nu gàddu.» 23 Ba ñuy wax loolu, foogoon nañu ne Yuusufa déggul seen làkk, ndax làppto, ba doxoon seen diggante, di tekki.
24 Ci biir loolu mu dummóoyu leen, di jooy.
25 Gannaaw loolu Yuusufa joxe ndigal, ñu sol seeni saaku pepp, te ku nekk ca ñoom, ñu yebal ko xaalisam ca saakoom, ba noppi mayaale leen lu ñu lekk ca yoon wa. Ñu defal leen noonu. 26 Ba mu ko defee ñu sëf seeni mbaam pepp ma, daldi fay bàyyikoo.
27 Fa ñu dal ca guddi, kenn ci ñoom bëgga xont mbaamam, ubbi saakoom rekk, ne pemm ci xaalisam. 28 Mu ne doomi baay ya: «Delloo nañu ma sama xaalis, mu ngi nii ci sama saaku.» Seen fit ne tërit, ñuy rag-ragi, ku ne xool sa moroom, naan: «Lu nu Yàlla nattoo nii?»
29 Ba ñu yeggee ca seen baay Yanqóoba ca réewu Kanaan, daldi koy nettali li leen dal lépp, ne ko: 30 «Waa ja yilif réew ma dafa noo résëti, foog ne danuy yëddusi réew ma. 31 Nu ne ko: “Nun ay nit ñu maandu lanu, dunu ay yëddukat; 32 fukki góor ak ñaar lanu woon yu bokk sunu baay, waaye kenn ka nekkatul, te ka gën di xalee nga fa sunu baay, ba ca réewu Kanaan.” 33 Waa ja yilif réew ma ne nu: “Ni may xame ne ñu maandu ngeen, nii la: dangeen may bàyyeek kenn ci yeen, te dem yóbbul dund seen waa kër, yi nekk ci xiif; 34 su ko defee ngeen indil ma seen rakk ju ndaw, kon dinaa xam ne dungeen ay yëddukat waaye nit ñu maandu ngeen, te dinaa leen delloo seen mbokk, ngeen mana dem fu leen neex ci réew mi.”»
35 Naka la ku nekk sotti saakoom, ne jàkk ca mbuusu xaalisam. Ba ñu gisee mbuusi xaalis ya, ñoom ak seen baay, dañoo tiit. 36 Seen baay Yanqóoba ne leen: «Xañ ngeen ma ay doom: Yuusufa nekkatul, Simeyon nekkatul, léegi ngeen bëgga jël Beñamin, yóbbu. Loolu lépp ci sama kaw; ngalla man!» 37 Ruben wax ak baayam ne ko: «Su ma la ko délloosilul, boo yeboo reyal sama ñaari doom yu góor yi. Tegal Beñamin ci sama loxo rekk, man dinaa la ko délloosil.» 38 Ci kaw loolu Yanqóoba ne: «Sama doom daal, du ànd ak yeen, ndax magam faatu na, te moom rekk a des. Su ko musiba dabee ci yoon wi ngeen jëm, dingeen ma yóbbe naqar wu may jàpp, ba kera may ànd ak sama bijjaaw, tàbbi njaniiw.»
<- Njàlbéen ga 41Njàlbéen ga 43 ->