4 Yanqóoba ne leen: «Bokki fan?» Ñu ne ko: «Karan.» 5 Mu ne leen: «Ndax xam ngeen Laban doomu Naxor?» Ñu ne ko: «Xam nanu ko kay.» 6 Mu dellu laaj leen ne leen: «Mbaa mu ngi ci jàmm?» Ñu ne ko: «Jàmm rekk kay. Xoolal ndaw see di ñëw, mook gàtt yi, mooy doomam Rasel.» 7 Yanqóoba ne leen: «Jant bi demagul fenn, ba ngeen di dajale jur gi. Wëggleen gàtt yi, sàmmi leen kay!» 8 Ñu ne ko: «Dunu ko man mbete gétt yépp daje, nu béraŋ doj wi, ubbi teen bi, doora wëgg gàtt yi.»
9 Na muy wax ak ñoom nag, Rasel agsi, indaale gàtti baayam, ndaxte sàmm la woon. 10 Ba Yanqóoba gisee Rasel, doomu nijaayam Laban, moom ak gàtti nijaayam ya, dafa daagu ba ca teen ba, béraŋ doj wa ko ub, daldi wëgg gàtti Laban. 11 Ba loolu amee Yanqóoba fóon Rasel, ne yikkét jooy. 12 Ca la Yanqóoba wax Rasel ne ko: «Maak sa baay a bokk, ndax maay sa doomu bàjjan Rebeka.» Rasel daw, yégal ko baayam.
13 Ba Laban déggee ne jarbaatam Yanqóoba ñëw na, dafa daw gatandu ko, taf ko ci boppam, fóon ko, yóbbu ko kër ga. Ba Yanqóoba nettalee Laban lépp, 14 Laban da ne ko: «Yaw kay sama jarbaat nga lenqe!» Yanqóoba toog na fa ak moom lu mat weer. 15 Gannaaw loolu Laban ne Yanqóoba: «Li ngay sama mbokk kat, taxul nga war maa liggéeyal ci neen. Wax ma lan mooy sa peyoor.»
16 Laban nag amoon na ñaari doom yu jigéen, taaw ba di Leya, rakk ja di Rasel. 17 Leya di ku bët ya yànjuloon, te Rasel nekkoon ku jekk te neexa xool, 18 Yanqóoba bëgg Rasel lool, ba ne Laban: «Dinaa la liggéeyal juróom ñaari at ngir Rasel sa doom ju ndaw ji.» 19 Laban ne ko: «Ma may la ko de moo ma gënal may ko keneen. Kon toogal ci man.» 20 Ci kaw loolu Yanqóoba liggéeyal Laban diiru juróom ñaari at ngir Rasel, te mu mel ni ay fan rekk ci moom ndax mbëggeel, gi mu am ci Rasel.
21 Loolu wéy, Yanqóoba ne Laban: «Jox ma sama jabar, ma séetal ko, ndax àpp bi jot na.» 22 Laban nangu, daldi togglu ay reer, woo ca waa gox ba bépp. 23 Timis jot Laban jël doomam Leya, jébbal ko Yanqóoba, mu dëkkoo ko. 24 Ci biir loolu Laban jël jaamam bu jigéen bu ñuy wax Silpa, may ko doomam Leya, mu dib jaamam.
25 Ba bët setee, Yanqóoba fekk muy Leya. Mu ne Laban: «Waaw, li nga ma def nag? Du Rasel a taxoon ma liggéeyal la? Lu tax nga wor ma?» 26 Laban ne ko: «Rakk jëkka séy taaw daal, du aada fii. 27 Séetul ak kii, ba ayu bésam mat, ma door laa jox ki ci des, soo ma dee liggéeyaatal diiru juróom ñaari at.» 28 Yanqóoba nangu, daldi séetu ak Leya ayu bés, ba noppi Laban jébbal ko doomam Rasel. 29 Booba la Laban may Rasel jaamam bu jigéen bu ñuy wax Bilaa, mu dib jaamam. 30 Yanqóoba nag dëkkoo Rasel, mi mu gënoona bëgg Leya. Ci kaw loolu mu liggéeyaatal Laban juróom ñaari at.