12 Guddi googu Yanqóoba dafa gént, gis raas bu sampu ci suuf, te cat la sar asamaan, malaakay Yàlla yi di ci yéeg ak a wàcc. 13 Ndeke Aji Sax jaa nga tollu ca wetam. Mu wax ak moom ne ko: «Maay Aji Sax ji, di sa Yàllay maam Ibraayma te di Yàllay Isaaxa. Suuf si nga tëdd dinaa la ko jox, yaak sa askan. 14 Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele. 15 Maa ngi nii ànd ak yaw, di la sàmm fépp foo jëm, te itam dinaa la délloosi ci réew mii. Duma la bàyyi mukk, waaye dinaa def li ma la wax lépp.»
16 Ci kaw loolu Yanqóoba yewwu ne: «Ndekete Aji Sax ji mu ngi ci bérab bii, te xawma ko woon.» 17 Ma nga tiit nag te naan: «Bérab beeka raglu! Fii kay du fenn, fu dul kër Yàlla; te mooy buntu asamaan.»
18 Ca suba teel Yanqóoba jóg, jël doj, wi mu gegenoo woon, samp fa, muy xàmmikaay, ba noppi sotti ci ag diw, sellale ko. 19 Ca la tudde bérab ba Betel[a], waaye ca njàlbéen Lus la dëkk ba tuddoon. 20 Gannaaw loolu Yanqóoba dogu na ne: «Su Yàlla àndee ak man, di ma sàmm ci yoon wi may aw, di ma jox lu ma lekk ak lu ma sol, 21 ba kera may dellu sama kër baay ci jàmm, su boobaa, Aji Sax ji dina doon sama Yàlla. 22 Doj wii ma samp, muy xàmmikaay, mooy doon kër Yàlla, te lépp lu mu ma wërsëgal, dinaa ko génneel fukkeel ba moos.»
<- Njàlbéen ga 27Njàlbéen ga 29 ->- a 28.19 Betel mu ngi tekki «kër Yàlla».