5 Ba Isaaxa di juddu, booba Ibraaymaa ngi woon ci téeméeri atam. 6 Saarata ne:
14 Ca ëllëg sa Ibraayma jóg suba teel, sàkk mburu, booleek mbuusu ndox, jox Ajara, mu gàddu. Mu daldi ko dénk Ismayla, yebal ko, mu dem. Ci kaw loolu muy wëndeelu ca màndiŋu Beerseba. 15 Ba ñu demee, ba ndox ma jeex, Ajara daa bàyyi xale bu góor bi ci taatu ngarab su ndaw, 16 dox, ba dànd ko lu tollook saanu fitt, toog nag jàkkaarlook moom te naa ci xelam: «Duma fekke mukk sama deewu doom.» Naka la toog foofa janook moom, ne yikkét jooy.
17 Ba mu ko defee Yàlla dégg baatu xale bu góor ba. Malaakam Yàlla ma àddoo asamaan, ne Ajara: «Ajara, lan la? Bul ragal dara, ndaxte Yàlla dégg na sa baatu doom ci diggante bii mu tollu. 18 Demal yékkati ko, may ko loxo, mu jóg. Dinaa def mu law, ba doon xeet wu yaa.»
19 Ci kaw loolu Yàlla muri ay bëtam, mu gis ab seyaan, daldi cay dem, duy mbuusam, ba mu fees, jox ca doomam, mu naan. 20 Yàlla nag ànd ak Ismayla, muy màgg, dëkk ca màndiŋ ma, di fittkat. 21 Ca àllub Paran la dëkkoon, yaayam wutali ko soxna ca réewum Misra.
25 Ci kaw loolu Ibraayma tawat Abimeleg teen bu surgay Abimeleg nangu woon ci moom, aakimoo ko. 26 Abimeleg nag ne ko: «Xawma ku la def jooju jëf de, ndax yaw waxoo ma ci dara; guléet ma dégg ko tey.»
27 Ba loolu amee Ibraayma jël ay gàtt aki nag, may ko Abimeleg, ñu fasoo kóllëre ñoom ñaar. 28 Fekk na Ibraayma ber juróom ñaari xar yu jigéen. 29 Abimeleg nag ne Ibraayma: «Lu tax nga ber juróom ñaari xar yooyu?» 30 Ibraayma ne ko: «Jëlal xar yii ci sama loxo, muy firnde ne man maa gas teen bii.» 31 Looloo tax ñu tudde teen boobu Beerseba (mu firi Teenu waat ga)†21.31 Beerseba man naa tekki «teenu juróom ñaar» ba tey., ndaxte fa lañu waatoo woon ñoom ñaar. 32 Naka lañu fasoo kóllëre ca Beerseba, Abimeleg jóg ànd ak Pikol kilifay xarekatam, ñu ñibbi réewu Filisti.
33 Ibraayma nag jëmbat na garabu tamaris foofa ca Beerseba, tudd fa Yàlla Aji Sax ji, ji nekk ba fàww. 34 Ibraayma gane na réewu Filisti lu yàgg.
<- Njàlbéen ga 20Njàlbéen ga 22 ->