8 Abimeleg jóg suba teel, woolu dagam yépp, nettali leen loolu lépp, ñu tiit lool. 9 Gannaaw loolu Abimeleg woolu Ibraayma ne ko: «Li nga nu def nag? Ndax dama laa tooñ, ba nga yóbbe ma tooñ gu réye nii, man ak sama réew mi mépp? Lii nga ma def de, waroo ko woona def.» 10 Abimeleg teg ca ne ko: «Te li nga def sax, lu la ci xiir?» 11 Ibraayma ne ko: «Da di dama noon, amul kenn ci réew mii ku ragal Yàlla, te dees na ma rey ndax sama soxna. 12 Te moona dëgg la sax, sama jigéen a, ndaxte danoo bokk baay te bokkunu yaay, ma jël ko. 13 Te bés, ba ma Yàlla génnee sama kër baay, may wëndeelu, dama koo waxoon ne ko: “Déglul, li ngay def soo ma bëggee xettli, mooy lii: fépp fu nu dem, nanga wax ne sa càmmiñ laa.”»
14 Ba mu waxee ba noppi, Abimeleg jël ay xar aki nag ak ay jaam yu góor ak yu jigéen, jox ko Ibraayma, daldi ko delloo soxnaam Saarata. 15 Abimeleg ne ko: «Sama réew mépp a ngi noonu, dëkkal fu la neex.» 16 Gannaaw loolu wax na Saarata ne ko: «Déglu ma fii, jox naa sa càmmiñ limu junniy dogi xaalis[a]. Loolu dama koo def, ngir setal sa der ci kanam ñi nga dëkkal ñépp. Léegi nag ñépp xam nañu ne set nga wecc.»
17-18 Fekk na Aji Sax ji um jigéeni waa kër Abimeleg, ba kenn du ci am doom, du soxnaam, du ay jaamam, te li ko waral di Saarata soxnas Ibraayma. Ibraayma nag ñaan Yàlla; Yàlla def ñu wér, ba mana am doom.
<- Njàlbéen ga 19Njàlbéen ga 21 ->- a 20.16 junniy dogi xaalis tollu woon na ci fukki kiloy xaalis ak benn.