5 Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!» 6 Ibraam wax Sarayi ne ko: «Sa jaam a ngoog ci say loxo, def ko lu la neex.» Sarayi nag di torxal Ajara, ba mu daw, ba soreek moom.
7 Ba mu dawee, malaakam Aji Sax ja gis ko fu dend akub bëtu ndox ca màndiŋ ma, mooy bëtu ndox, ba ca yoonu Sur. 8 Mu ne ko: «Yaw Ajara, jaamu Sarayi bi, foo bàyyikoo nii? Ak foo jëm?» Mu ne ko: «Damay daw ba fu soreek sama sang Sarayi.»
9 Malaakam Aji Sax ja ne ko: «Dellul ca sa sang, te nga yem ciy loxoom.» 10 Mu teg ca ne ko: «Dinaa yokk sa askan lool, ba kenn du leen mana waññ,» 11 tegaat ca ne ko:
13 Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (mu firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!» 14 Loolu moo tax ñu tudde teen booba teenu Laxay Roy (mu firi teenu Aji Dund ji may gis); mu nga nekk diggante Kades ak Beret.
15 Ba loolu weesee Ajara amal Ibraam doom ju góor. Ibraam tudde doom ji Ismayla. 16 Ba Ajaray am Ismayla, Ibraam a ngi tollu woon ci juróom ñett fukki at ak juróom benn (86).
<- Njàlbéen ga 15Njàlbéen ga 17 ->