5 Ci biir loolu Lóot, mi mu àndal, moom it yor jur gu gudd ak gu gàtt aki xayma, 6 ba tax xajatuñu ca réew ma, ndax seen alal dafa bare, ba manatuñu faa bokk dëkk. 7 Loolu tax sàmmi Ibraam ak sàmmi Lóot di jote. Rax ci dolli Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ña nga woon ca réew ma.
8 Ba loolu amee Ibraam da ne Lóot: «Waay waay, bu xuloo am sama digganteek yaw mbaa say sàmm ak samay sàmm. Xanaa dunuy bokk nag? 9 Xanaa àll bi newul yàmblaŋ ngay gis? Nan teqlikoo, kay; boo demee càmmoñ, ma dem ndijoor; boo demee ndijoor, ma dem càmmoñ.»
10 Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja*13.10 Tool booba mooy Àjjana, fa Yàlla jëkkoona dëkkal Aadama ak Awa. . 11 Ba mu ko defee Lóot tànn jooru Yurdan gépp, daldi toxu jëm penku. Noonu lañu teqlikoo. 12 Ibraam dëkke réewu Kanaan, Lóot sance dëkk ya ca jooru Yurdan, daldi toxal xaymaam, samp ko Sodom. 13 Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.
18 Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay.
<- Njàlbéen ga 12Njàlbéen ga 14 ->- a 13.10 Tool booba mooy Àjjana, fa Yàlla jëkkoona dëkkal Aadama ak Awa.