4 Ibraam daldi dem, na ko ko Aji Sax ji waxe woon, Lóot topp ca. Ba Ibraam di jóge Karan, booba am na juróom ñaar fukki at ak juróom (75). 5 Ibraam ànd ak soxnaam Sarayi ak Lóot, mi muy baay bu ndaw ci moom. Mu yóbbaale nag alal, ja mu dajale jépp, ak jaam, ya mu jënde Karan. Ñu jóge fa, jublu réewu Kanaan.
6 Ba ñu agsee Kanaan, Ibraam dafa jàll ca biir réew ma, ba àgg bérab bu sell, ba féete ak Sikem, ca garab[a] gu mag, ga ñuy wooye More. Booba fekk na waa Kanaan a nga woon ca réew ma. 7 Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.
8 Gannaaw loolu mu jóge fa, jëm tund, wi féete Betel penku, samp fa xaymaam; Betel féete ko sowu, Ayi féete ko penku. Foofa itam Ibraam tabaxal na fa Aji Sax ji sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko. 9 Ibraam bàyyikooti fa, aw yoonam, jublu àllub Negew[b].
14 Ba Ibraam àggee Misra, waa Misra gis ne jigéen ji mu àndal rafet na lool. 15 Jaraafi Firawna itam gis ko, di ko kañ ca Firawna ndax taar ba, ñu daldi ko yóbbu ca kër Firawna. 16 Firawna nag topptoo Ibraam bu baax ndax moom, ñu may ko ay gàtt ak ay nag, ay mbaam yu góor, ak ay jaam yu góor ak yu jigéen, ak ay mbaam yu jigéen aki giléem.
17 Teewul Aji Sax ji wàcce ca Firawna ak waa këram jàngoro yu metti ndax Sarayi, soxnas Ibraam. 18 Firawna woolu Ibraam ne ko: «Li nga ma def nag? Lu tax waxoo ma ne kii sa soxna la? 19 Lu tax nga ne sa jigéen la, ba tax ma jël ko, bëgg koo def sama jabar? Ayca, sa jabar a ngoog, fabal te ne mott!» 20 Naka la Firawna wax loolu ba noppi, daldi sant ay dagam, ñu génne Ibraam réew ma, moom ak soxnaam ak alalam jépp.
<- Njàlbéen ga 11Njàlbéen ga 13 ->