6 Teewul ñooñu ñu jàppe woon ay kàngam, ak daraja ju ñu masoona am, amalu ma solo, nde Yàlla amul xejj ak seen, ñooñu yokkuñu lenn ci kàddu gi may xamle. 7 Xanaa kay li ñu gis moo di ni Yàlla yebale Piyeer ngir mu àgge askanu Yawut xibaaru jàmm bi, noonu la ma yebale ngir ma àgge ko jaambur ñi xaraful, 8 ndax ki liggéey ci Piyeer, ngir mu doon ndawam ci Yawut yi, moo liggéey ci man itam, ngir may ndawam ci yeneen xeet yi. 9 Ña ñu jàppoon ne ñooy kenuy mbooloom gëmkat ña nag, te ñuy Yanqóoba ak Sefas ak Yowaan, ba ñu ràññee yiw wi ñu ma jagleel, maak Barnaba lañu jox loxo, ngir nun nu liggéeyi ca jaambur ña, te ñoom ñu liggéeyi ci Yawut yi. 10 Laajuñu lu moy nu fàttliku néew doole yi, te loolu di lu ma pastéefoo jëfe.
14 Waaye ba ma gisee ne doxewuñu njub gi dëggug xibaaru jàmm bi laaj, maa wax Sefas ci kanam ñépp, ne ko: «Ndegam yaw miy ab Yawut, yaa jëfewul ni ab Yawut, xanaa di jëfe ni xeeti jaambur ñi, ana lu tax ngay ërtal jaambur ñi dul ay Yawut, ngir ñu yawutal?»
17 Ba tey su nu dee sàkku àtteb ku jub, ndax li nu gëm Almasi, te teewul nit ñi gis ne nu ngi bàkkaar, nun itam, ndax loolu day wund ne Almasi mooy xiirtale ci bàkkaar? Mukk kay! 18 Ndaxam su dee tabaxub ndigalu yoon bi ma tojoon, moom laa tabaxaat, maa def sama bopp moykatub yoon. 19 Su dee wàllu yoonu Musaa nag, man nit ku dee laa, te yoonu Musaa moo ko waral, ngir ma mana dund dund gu ñeel Yàlla. Dees maa boole ak Almasi rey ca bant ba. 20 Moo tax dootu man maay dund, waaye Almasi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man. 21 Duma neenal yiwu Yàlla, ndax kat su doon ci sàmm ndigalu yoon lees di ame àtteb ku jub, konoon Almasi moo dee cig neen.
<- Galasi 1Galasi 3 ->