Saar 9
Askan wi rax na
1 Gannaaw ba loolu wéyee njiit ya dikk, ne ma: «Du bànni Israyil, du sarxalkat yi, du Leween ñi, kenn ci ñoom teqlikoowul ak xeeti réew meek seen aada yu siblu. Dañuy jëfe ni Kanaaneen ñeek Etteen ñeek Periseen ñeek Yebuseen ñeek Amoneen ñeek Mowabeen ñeek waa Misraak Amoreen ñi. 2 Jël nañu jabar ci ñoom, jëlal ci jabar seeni doom, ba jaxase jiwu mu sell mi ak waasoy réew yi. Njiit yeek mag ñi sax ñoo jiitu ci googu fecci kóllëre.»
3 Ba ma déggee loolu damaa xotti sama turki ak sama mbubb, xuuf sama kawaru bopp ak sama sikkim, daldi toog, ne tott. 4 Ba loolu amee mboolem ñi wormaal kàddug Yàllay Israyil daje, wër ma ndax ñàkk kóllëreg ña ñibbsee ca ngàllo ga. Ma toog, ne tott ba waxtuw saraxu ngoon. 5 Saraxu ngoon jot, ma jóge ca sama jataayu toroxtaange, ba ma xottee sama turki baak sama mbubb ma. Ma ne gurub sukk, tàllal sama Yàlla Aji Sax ji loxo, 6 daldi ñaan, ne:
Éy sama Yàlla maa rus, maa torox, ba manumaa siggi fi sa kanam, ndaxte sunuy bàkkaar bare na, ba mëdd nu, sunuy moy tegloo ba àgg asamaan. 7 La ko dale ca sunu janti maam ba bésub tey jii, nu ngi ci moy gu réy. Sunuy bàkkaar tax na buuri réew yi teg nu loxo, nook sunuy buur ak sunuy sarxalkat, ñu di nu rey, di nu jàpp njaam, di lël sunu alal, di nu torxal ba sunu jonni yàllay tey.
8 Waaye yaw Aji Sax ji sunu Yàlla, yàggul dara aw yiw bàyyikoo na ci yaw, musal ñenn ci nun, may nu ndëgërlaay ca sa bérab bu sell ba. Yaw sunu Yàlla, yaa nu taxa leqliku, yaa nu dundalaat ci sunu biir njaam gi. 9 Ndax ay jaam lanu, waaye yaw sunu Yàlla, waccewoo nu sunug njaam. Yaa dawal ngor sunu digganteek buuri Pers, ngir mayaat nu dooley tabax sunu kër Yàlla, yékkatee ko ca gentam ba, may nu kiiraay ci Yerusalem ak ci Yuda.
10 Yaw sunu Yàlla, ana lu nuy waxati nag gannaaw lii? Ndax kat noo dëddu sa santaane, 11 yi nga nu dénk, yonent yiy say jaam jottli ko, ne nu: «Réew mi ngeen di nanguji, réew mu sobewu la ndax sobey waasoy réew ma. Feesal nañu kook seeni jëf ju siblu ak seen tilim, ba fépp daj. 12 Kon nag seen doom yu jigéen buleen leen may seen doom yu góor, te seen doom yu jigéen buleen leen jëlal seen doom yu góor. Buleen seet mukk seen jàmm mbaa seen njariñ. Looloo leen di taxa am doole, bay xéewlu ci ngëneeli réew mi, ba wacce ko seen askan fàww.» 13 Loolu nu dal lépp, sunu jëf ju bon a tax, ak sunu tooñ gu réy. Terewul yaw sunu Yàlla, tegoo nu lu dul mbugal mu yées mi sunuy bàkkaar yellool. Terewul yaw sunu Yàlla, li nu bàkkaar mbugaloo nu ko, te moo nu fi taxa des di dund nii. 14 Nan lanu mana dellooti di xëtt say santaane, di séyanteek xeet yii ak seen jëf ju siblu? Kon doo nu mere, faagaagal nu, ba kenn du desati mbaa muy rëcc? 15 Yaw Aji Sax ji Yàllay Israyil, yaay boroom njekk. May nga nu bésub tey jii nu dese bakkan. Nu ngi nii fi sa kanam ci biir tooñange, ba tax du kenn ci nun ku am lay fi sa kanam.
<- Esra 8Esra 10 ->