Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 9
Rey nañu bokkaalekat yi
1 Gannaaw loolu Aji Sax ji àddu ca kaw, may dégg. Mu ne: «Yeen mbugalkati dëkk bi, kaayleen, te na ku nekk ŋàbb sa ngànnaayal reyukaay.» 2 Ca saa sa juróom benni góor jóge yoonu bunt ba féete kaw te janook bëj-gànnaar, ku nekk ŋàbb sa ngànnaayal reyukaay. Keneen a nga ca seen biir, ku sol ndimol lẽe, ak mbarum bindukaay ba ca ndiggam. Ñu dikk taxaw ca wetu sarxalukaayu xànjar ba. 3 Ci kaw loolu leeru Yàllay Israyil, ja woon ca kaw jëmmu malaakay serub ma, yékkatikoo fa, jubal buntu kër ga. Mu woo boroom ndimol lẽe baak mbarum bindukaay ba ca ndiggam. 4 Aji Sax ji ne ko: «Wëral dëkk bi, ci biir Yerusalem. Foo gis kuy onk ak a binni, di ko naqarloo gépp tojaange gu ñu fiy def, nga rëdd aw rëdd ci jëëm.» 5 Ba loolu wéyee mu wax ak ña ca des, may dégg. Mu ne leen: «Toppleen ko ca biir dëkk ba te ngeen rey. Buleen xool bëti ñéeblu, buleen ñeewante. 6 Mag ñu góor ñeek xale yu góor yi, jeeg jeek janq ji, ba ci tuut-tànk yi, reyleen ñépp, faagaagal leen. Waaye ku ci am rëddu jë, buleen ko laal. Dooreleen ko ci sama bérab bu sell bi.» Ñu tàmbalee bóom mag ña ca kanam kër Yàlla ga. 7 Aji Sax ji ne leen: «Feesal-leen ëtt yeeki néew, sobeel-leen kër gi, doora génn.» Ba ñu noppee, daldi jàll ca biir dëkk ba, di rey.

8 Naka lañu dem, reyi, ma des fa man doŋŋ. Ma daldi daanu, dëpp sama kanam fa suuf, daldi àddu ca kaw, ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, xanaa doo sànk mboolem ndesu Israyil ci sa xadar jii ngay xëpp ci kaw Yerusalem?» 9 Mu ne ma: «Tooñaangey waa kër Israyil ak Yuda moo ëpp loxo lool. Réew maa ngi fees ak deret, dëkk bi fees ak yàqute. Nee nañooy: “Aji Sax ji wacc na réew mi. Aji Sax ji gisul dara.” 10 Man it duma xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Seen jëfin laay këpp ci seen kaw bopp.» 11 Ci kaw loolu boroom mbubbam lẽe baak mbarum bindukaay ba ca ndiggam, ne jimeet, délsi. Mu ne: «Def naa lépp na nga ma ko sante.»

<- Esekiyel 8Esekiyel 10 ->