Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 6
Tuur yi indi na mbugal
1 Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji da maa dikkal, ne ma: 2 «Yaw nit ki, jàkkaarlool ak tundi Israyil, nga waxal leen waxyu. 3 Neel:
“Yeen Tundi Israyil,
Dégluleen kàddug Boroom bi, Aji Sax ji.
Boroom bi Aji Sax ji moo wax lii,
jëme ci tund wu mag ak wu ndaw
ak xunteeku xur, ne:
Maa ngi nii di leen wàcceel saamar,
maay màbb seen jaamookaayi tuur,
4 seen sarxalukaay gental,
seen suurukaayi tuur tasaaroo,
ma tëral seeni nit ñu ñu bóom fi seen kanam kasaray tuur.
5 Maay tegal seen kasaray tuur néewi bànni Israyil.
Maay wasaare seeni yax fi wër seeni sarxalukaay.
6 Fu ngeen mana sance,
seeni dëkk ay gental,
seen jaamookaayi tuur wéet,
seeni sarxalukaay yàqu, gental,
seen kasaray tuur rajaxoo ba jeex,
seen suurukaayi tuur màbb,
seeni liggéey réer.
7 Dees na leen bóom,
ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
8 Waaye maay déeg lenn ci yeen,
ñu rëcc saamar, tasaaroo ci xeet yi,
ci biir réewi jaambur.
9 Su boobaa seenu ndes di ma fàttlikoo
fa biir xeet ya ñu leen yóbbu njaam,
fa may jeexale seen xolu gànc, bi ma dëddu,
ak seen gët yi ñuy gànctook seeni tuur.
Su boobaa ñu jéppi seen bopp
ndax lu bon li ñu def ak seen jépp jëf ju siblu.
10 Dinañu xam ne maay Aji Sax ji,
te du neen laa leen artoo,
ba ma leen di tëkkoo mii musiba.
Aji Sax jeey am ndam
 
11 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Fenqeel say loxo, dóor sa tànk fi suuf te ne: ‘Ñaw!’
ci mboolem jëfi waa kër Israyil ju bon ju siblu.
Saamar ak xiif ak mbas lañuy fàddoo.
12 Ku sore deeye mbas,
ku jege fàddoo saamar,
ku ca mucce, deeye xiif,
ma ŋaccal leen sama xadar.
13 Dingeen xam ne maay Aji Sax ji,
bu seeni néew nee xas fi seen biiri tuur,
ak fi wër seeni sarxalukaay,
ak kaw tund wu mag ak wu ndaw,
ak mboolem ker garab gu naat,
ak mboolem garab gu mag te sëq,
fépp fu ngeen di taale cuuraay, ñeel seen mépp tuur.
14 Maa leen di dóor sama loxo,
réew mi, ma gental koo gental,
dale ko màndiŋ ma ba Dibla,
ak fépp fu ñu mana sance.
Su boobaa ñu xam ne man maay Aji Sax ji.”»

<- Esekiyel 5Esekiyel 7 ->