4 «Saraxu rendi-dóomal, bi ki ci jal biy indil Aji Sax ji bésub Noflaay, juróom benni xar yu ndaw yu amul sikk lay doon, ak kuuy mu amul sikk. 5 Saraxu pepp biy ànd ak kuuy mi benn efa*46.5 benn efa: seetal ci 45.24. lay doon, di fukki kiloy pepp ak juróom, ak dayob pepp bu mu àttan buy ànd ak xar yu ndaw yi ak xiinu diw, yemook ñetti liitari diw ak genn-wàll ci efab pepp bu nekk. 6 Bésub Terutel weer, wenn yëkk wu ndaw lay doon wu amul sikk ak juróom benni xar yu ndaw akam kuuy, te lépp mucc sikk. 7 Na ci boole saraxu benn efab pepp buy ànd ak yëkk wi, ak benn efab pepp ngir kuuy mi, ak lu mu man ci pepp, mu booleek xar yu ndaw yi, ak benn xiinu diw ci efab pepp bu nekk.
8 «Dal-luwaay bunt, bi ki ci jal biy jaare duggsi, fi lay jaare génn. 9 Baadooloy réew mi nag bu ñuy teewesi bésub ndaje fi kanam Aji Sax ji, ku ci jaare mbaaru buntu bëj-gànnaar, di sujjóotsi, bu noppee na jaare mbaaru buntu bëj-saalum ba. Te ku dugge mbaaru buntu bëj-saalum, bu noppee na génne mbaaru buntu bëj-gànnaar ba. Deesul delloo bunt bi nga dugge. Bunt bi mu jàkkaarlool lees di génne. 10 Ki ci jal bi ci boppam, bu baadoolo yiy dugg, na duggandook ñoom, bu ñuy génn, mu génnandook ñoom.
11 «Su dee bési màggal ak bési ndaje yi, saraxu pepp mi benn efa lay doon ngir yëkk wi, yemook fukki kilook juróom, ak benn efa ngir kuuy mi, ak dayo bu ñu àttan ngir xar yu ndaw yi, efab pepp bu ne ànd ak benn xiinu diw, di ñetti liitar ak genn-wàll.
12 «Buntu ëttu biir bi féete penku it lañuy ubbil ki ci jal bi, buy joxe saraxu yéene: muy saraxu rendi-dóomal, di saraxu cant ci biir jàmm, di beneen saraxu yéene bu ñeel Aji Sax ji, ngir mu joxe saraxu rendi-dóomalam, mbaa saraxu cantam ci biir jàmm, ni mu koy defe ci bésub Noflaay. Bu noppee, génn, ñu tëj bunt bi.
13 «Am xarum menn at mu amul sikk lees di defal Aji Sax ji bés bu nekk saraxu rendi-dóomal, te suba su ne lees koy def. 14 Nañu ci boole suba su ne benn céru juróom benneelu efab pepp, yemook ñaari kilook liibar, ànd ak liitaru diw, yemook benn céru ñetteelu xiinu diw buy tooyal sunguf si. Loolooy saraxu pepp mi, ñeel Aji Sax ji, di dogali yoon yu sax dàkk. 15 Muy xar mu ndaw mi, di saraxu pepp mi, di diw gi, suba su nekk lees koy def, muy saraxu rendi-dóomal bu sax dàkk.
21 Gannaaw loolu waa ji génneeti ma ba ci ëttu biti bi, yóbbu ma ci ñeenti collam yépp. Ndeke coll wu ci nekk, ber nañu ca ëtt bu ndaw, 22 bu gudde ñeent fukki xasab, yaatoo fanweeri xasab, te ñeenti ëtt yu ndaw yi ci coll yi yépp a tolloo. 23 Ñeenti ëtt yu ndaw yi, bu ci nekk miir bu gàtt a ko ub, ay toggukaay tege ci suufam, leru miir bi ba mu daj. 24 Waa ji ne ma: «Lii mooy waañ yi liggéeykati kër Yàlla gi di togge yàppu saraxi askan wi.»
<- Esekiyel 45Esekiyel 47 ->- a 46.5 benn efa: seetal ci 45.24.