Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 32
Jàmbaaru àddina, baadooloy njaniiw
1 Ca fukkeelu at maak ñaar, benn fan ca fukkeelu weer waak ñaar, kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: 2 «Yaw nit ki, yékkatil kàddug jooy, ñeel Firawna buuru Misra. Nga ne ko:
“Dangaa meloon ni waxambaanew gaynde ci biir xeet yi,
mel ni ninki-nànkay biir géej,
di fettaxe say wal,
di wéquy nëxal ndox mi,
di tilimal dex gi.
3 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Maa lay laaw sama caax fi biir ndajem xeet yu bare,
ñu ñoddee la mbaal ma, génne.
4 Maa lay wacc fi suuf, sànni la ci àll bi,
dëël njanaaw yépp fi yaw,
ba reggal rabi àll yépp ci saw yaram.
5 Maay lale tund yi sa suux,
ba feesale xur yi sa jalu néew yi.
6 Maay nàndale suuf sa deret,
mu wale ca tund ya,
ba feesal yooni ndox yi.
7 Bu sa leer feyee, maay muur asamaan,
lëndëmal ay biddiiwam,
sànge jant bi aw niir,
weer wi noppee leeral.
8 Mboolem leeri asamaan laay giimal fi sa kaw,
ba teg lëndëm fi sam réew.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
 
9 «“Maay jàqloo xeet yu bare,
bu ma leen àggee sa musiba
ci biir réew yoo xamuloon.
10 Saw demin laay tiitale xeet yu bare,
ba seen yarami buur yi di dawa daw.
Keroog sa bésub jéll ba, bu may xàcci sama saamar fi seen kanam,
duñu noppee lox, ku nekk ay xalaat bakkanu boppam.
 
11 «“Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
Saamaru buuru Babilon a lay dikkal.
12 Saamari jàmbaar laay tërale sa mbooloo,
ñoom ñépp bokk ci xeet yi gëna néeg,
te ñooy sàggi sagub Misra;
gàngooram gépp sànku.
13 Maay faagaagal sa mboolem jur,
gi feggook ndox mi ne xéew,
ba tànku nit dootu ko nëxal,
wewu jur dootu ko nëxal.
14 Su boobaa ma dalal seeni ndox,
dawal ndànk seeni wal nig diw.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
15 Bu ma defee réewum Misra ab gent,
ba réew mi feesoon, ne faraas,
bu ma dumaa mboolem ku ci dëkkoon,
su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.”
 
16 «Kàddug jooy a ngoog gu ñuy jooyi,
janqi xeet yeey jooye yooyu jooy Misraak gàngooram gépp.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»
Misra wéetul ca toroxteem
17 Ca fukkeelu at maak ñaar, fukki fan ak juróom ca weer woowa, kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: 18 «Yaw nit ki, yuuxul mbooloom Misra, gungee ko seen jéll, ñook janqi xeet yu mag yi, ñu ànd tàbbiji xóotey suuf, fekk fa ña tàbbi woon pax. 19 Ne leen:
“Misraa, ana koo ëpp ub taar?
Tàbbil, ñu boole laak paaxe yi tëral.”
20 Fi digg ñi fàddoo saamar la waa Misra di tëdd.
Saamar ba génn na,
ñu diri Misra, booleek gàngooram yépp yóbbu.
21 Biir njaniiw la jàmbaari xare yay tollu,
di waxtaane Misraaki farandoom, naan:
“Wàccsi nañu, ne lareet,
Yéefar yi fàddoo nañu saamar!”
 
22 «Buurub Asiree nga faak gàngooram gépp,
bàmmeeli xarekatam ña wër ko.
Ñoom ñépp lañu jam, ñu fàddoo saamar.
23 Seeni bàmmeel a nga féete fa xóotey xóote ya,
ñu yéew bàmmeelu buurub Asiri.
Ñoom ñépp lañu jam, ñu fàddoo saamar,
te daan tiital waa réewum aji dund ña.
 
24 «Buurub Elam a nga faak gàngooram gépp,
seeni bàmmeel yéew bosam.
Ñoom ñépp lañu jam, ñu fàddoo saamar.
Paaxe lañu wàccaale xóotey suuf,
te daan tiital waa réewum aji dund ña.
Seen gàcce lañu gàlloo,
ànd ak ñay wàcci biir pax.
25 Buurub Elam kay a nga tëdd ca biir ña ñu bóom,
mook gàngooram gépp, seeni bàmmeel yéew ko.
Paaxe yooyu yépp a fàddoo saamar,
te daan tiital waa réewum aji dund ña.
Seen gàcce lañu gàlloo,
ànd ak ñay wàcci biir pax,
ñu boole leen ak ña ñu bóom ab tëraay.
 
26 «Buuri Meseg ak Tubal a nga faak seen gàngoor gépp,
seen bàmmeeli xarekat yéew leen.
Paaxe yooyu yépp a fàddoo saamar,
nde ñoo daan tiital waa réewum aji dund ña.
27 Robaaleesu leen ak jàmbaar ña ànd ak seen gànnaayi xare,
wàcci biir njaniiw,
ñu gegen leen seen saamar, terale leen,
te seen ay war seeni yax,
nde ñoo daan tiital waa réewum aji dund ña.
28 Waaye yaw itam Misra, yaa ngii rajaxoo fi digg yéefar yi,
bokk ngaak ñi fàddoo saamar ab tëraay.
 
29 «Edom a nga fa, mooki buuram ak garmi yépp,
seenug njàmbaar teewul ñu denc leen fa ñu denc ñi fàddoo saamar,
ñu bokk ak paaxe yi ab tëraay,
ànd ak ña jëm biir pax.
 
30 «Kàngami bëj-gànnaar yépp a nga fa,
ak mboolem waa Sidon,
ña ànd ak ña ñu bóom, tëddi pax,
te seenug njàmbaar doon tiitale démb,
tey, ñu ànd ak ñi saamar bóom, tëddaale seenug kéefar.
Ñoo ràngoo seen toroxte,
ànd ak ñay wàcci biir pax.
 
31 «Ñoom la Firawna di gis,
muñe leen deminu gàngooram gépp,
moom mi fàddoo saamar, mooki nitam ak mbooloom mépp.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
 
32 «Maa defoon Firawna di tiitale ci réewum aji dund ñi.
Waaye tey moo bokk tëraay ak yeneen paaxe yi fàddoo saamar, mook gàngooram gépp.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»

<- Esekiyel 31Esekiyel 33 ->