Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 31
Ponkal daanu na
1 Ba loolu amee ca fukkeelu at maak benn, benn fan ca ñetteelu weer wa, kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma: 2 «Yaw nit ki, waxal Firawna buuru Misra ak gàngooram, ne ko:
“Ana koo neexool daraja?
3 Asiree ngoog, garabu seedar la woon ca Libaŋ,
rafeti bànqaas, naatalub gott, siggi ca kaw,
njañ lay àkki niir ya.
4 Bëti ndox suuxat ko, ndoxi xoote yi màggal ko,
wal ma dajaloo ca reen ya,
doxe fa yónnee garabi àll bi yépp ay waltan.
5 Moo ko taxa sut garabi àll bi,
ay bànqaasam sëq, car ya lawa law
ndax ndox mi koy ballal a ne xéew.
6 Picc yépp ay tàgge ay caram,
rabi àll yépp di jure fa suufam,
askanoo askan wu mag di tooge keram.
7 Taaram a nga ca taxawaayam
ak guddaayu caram ya,
ngir reenam ba sóoboo ndox mu ne xéew.
8 Du genn garabu seedar ca toolub Yàlla, gu ko yóbbuloon dara,
du garabu sippar yu ko niruy car,
mbaa garabu palataan bu ko niruy bànqaas.
Du genn garab ci toolub Yàlla, gu taaroo ni moom.
9 Maa ko rafetale njañam lu sëq,
ba garabi Àjjana, toolub Yàlla bi, ñoom ñépp ñee ko!

10 «“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaa siggi woon ca kaw, kii la njañam àkki woon niir ya, muy damoo taxawaayam. 11 Maa koy jébbal ku jiite ay xeet, mu fey koo fey coxoram, ma dàq ko. 12 Ay doxandéem a dikk, bokk ci xeet yi gëna néeg, gor ko, wacc, ay bànqaasam wadde kaw tund yeek xur yi, ay caram dammtoo ci xuntiy àll bi yépp, waa réew yépp dawe keram, wacc ko, 13 picc yépp di tage peram bi tëdd fi suuf, rabi àll yépp di goore caram yi fi suuf. 14 Su boobaa genn garab gu feggook ndox dootu siggi ca kaw, ba njañ lay àkki niir ya, genn garab dootu màndim ndox, bay damu ci kawi moroomam. Ñoom ñépp déy lañu àppal ndee, ñu jëm xóotey suuf, tëddi biir bàmmeel ni waa àddina sépp.

15 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Bés ba seedar ga tàbbee njaniiw, maa dogal ag ñaawlu: Maa sàng xóote ya ndax moom, téye dexi biir suuf, wali ndox yi noon xéew, taxaw. Maa ñaawluloo gottub Libaŋ ci loolu, garabi àll bi yépp doxe ca lax. 16 Maa def xeet yi dégg jéllu seedar gi, di lox, ba ma ko tàbbalee njaniiw, boole kook mboolem ñiy tàbbim pax, ba mboolem garabi Àjjana gëna taaru, ak yay ngëneeli Libaŋ, ak mboolem ya màndim ndox, ñoom ñépp di fa muñe seen demin, la seedar ga teew ni ñoom biir xóotey suuf. 17 Ñoo bokk ak seedar gi wàcci njaniiw, ànd caak ña fa saamar tëral, ñoom ñi ko doon dooleel, xeet yi daan tooge keram. 18 Ana kan nga neexool teddngaak daraja ci biir garabi Àjjana? Ndaxam dees na la booleek garabi Àjjana, tàbbal xóotey suuf. Yaay goorandook yéefar, yi saamar tëral. Loolooy deminu Firawnaaki gàngooram. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»

<- Esekiyel 30Esekiyel 32 ->