4 Mu ne ma: «Yaw nit ki, demal ba ca waa kër Israyil, te nga àgge leen samay wax. 5 Du ci waaso wu xóotu làkk te diisu làmmiñ lees la yebal. Ca waa kër Israyil nga jëm. 6 Bare na waaso yoo xamul seeni wax, yu xóotu làkk te diisu làmmiñ. Te su ma la yebaloon ci ñoom, ñu déggal la. 7 Waaye waa kër Israyil duñu la nangoo déggal, ngir nanguwuñu maa déggal; ndax waa kër Israyil gépp a dëgër bopp te dërkiis. 8 Maa ngii di la may kanam gu ñemee ni seen kanam, ba nga dëgër bopp ni ñoom. 9 Jamaa moo raw doj te ni laay dëgërale sa bopp. Bu leen ragal, bu leen tiit, li ñuy kërug fippukat yépp.»
10 Mu teg ca, ne ma: «Yaw nit ki nag, mboolem li ma lay wax, dégloo ko nopp, te teewloo ko xel. 11 Nanga dem ba ca sa bokki ngàllo ga, nga wax leen, ñu déglook ñu gàntal, ne leen: “Lii Boroom bi Aji Sax ji da koo wax.”»
12 Ci kaw loolu ngelaw ne ma siféet, may dégg sama gannaaw, riirum kàddu gu xumb gu ne: «Cant ñeel na teddngay Aji Sax ji fi màkkaanam.» 13 Mu ànd ak riirum laafi bindeef yay fenqoo, ak coowal mbege ya ñu feggool, muy riir mu xumb. 14 Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu. Maa ngay deme naqar ak xol bu tàng, te loxol Aji Sax ji diis gann ci sama kaw. 15 Ma àgg ba ca ngàllog Tel Abib, ga dëkke tàkkal dexu Kebar. Foofa ñu dëkk laa toog, jommi ci seen biir diiru juróom ñaari fan.
16 Ba juróom ñaari fan ya matee, kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: 17 «Yaw nit ki, tabb naa la wattukatub waa kër Israyil. Nangool sama gémmiñ kàddu, artool ma leen ko. 18 Su ma nee nit ku bon ki: “Dee rekk ay sa àtte,” te fekk àrtuwoo ku bon ka, waxuloo lu ko waññee ca mbonam ga, ba mu mucc, ku bon kaay dee ndax tooñam, waaye bakkanam yaw laa koy laaj. 19 Waaye su dee yaa àrtu ku bon ki te taxul mu waññiku, dëddu mbonam nag, tooñu boppam a ko reylu, waaye yaw musal nga sa bopp. 20 Su dee boroom njekk bu dëpp yoonu njekkam, di def ndëngte, maa koy gàllankoor, mu dee. Soo ko àrtuwul ndax bàkkaaram, dina dee, te deesul bàyyi xel njekkal démbam la, waaye bakkanam, yaw laa koy laaj. 21 Waaye nag su dee yaa àrtu boroom njekk bi, ba tax bàkkaaratul, dina dund déy, ndax kàddug àrtu ga, te yaw it musal nga sa bopp.»