Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 27
Esekiyel jooy na Tir
1 Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: 2 «Yaw nag nit ki, yékkatil kàddu, jooye ko dëkkub Tir. 3 Waxal Tir mi tooge buntu géej, jula yooyuy jëflanteek xeeti dun yu bare, nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Yaw Tir yaa noon:
‘Maaka matub taar!’
4 Yaw mi sa kemu suuf àkki xolu géej,
say tabaxkat a mottli sab taar.
5 Dañu laa tabax ni ñuy tabaxe gaal,
sàkke xànqi sippar fa tundu Senir,
defare ca sa xott wépp,
sàkk bantu seedaru Libaŋ,
defare ponku diggu gaal ga.
6 Ñu gorati garabu seen yu Basan,
defare say joowu,
kaw gaal gi, ñu defare ko banti sippar yu bawoo tefesi Géej gu mag ga,
rafetale ko bëñi ñey.
7 Lẽe bu bawoo Misra lañu ràbb ba mu jekk,
def ko ndimoy wiiru gaal gi,
nga raayawoo ko,
cuub gu baxa ak cuub gu xewar bawoo dunu Elisa,
di sa malaan,
8 waa Sidon ak Arwàdd doonoon say joowkat.
Yaw Tir, yaa yeb ñu rafet xel,
ñuy say mool,
9 magi Gebal ñeek nitam ñu xareñ ñi fi yaw féetewoo di jagal.
Mboolem gaal yu mag yi ak ña cay liggéey di dal ak yaw,
waa gaal ya di jënd sam njaay.
10 Waa Pers ak waa Ludd ak waa Puut,
ñépp a nga woon ca sa mbooloom xare,
di wékk fa yaw seeni pakk ak seen mbaxanay xare.
Ñooñoo la darajaal.
11 Arwàddeen ñeek sa niti bopp a daan wattoo ca sa kaw miir yépp,
Gammàddeen ñi di wattu say tata,
seeni gànnaay wékke, wër say miir.
Ñooñoo mottli sab taar.

12 «“Tarsis dëkk baa doon sab jula ndax sa gépp xeetu alal ju bare, di indi xaalis, weñ gu ñuul ak gu weex ak beteex, di ko weccikoo seen alal. 13 Waa Geres ak Tubal ak Meseg di say jula, di leen indil ay doom aadama ak ndabi xànjar yu ñuy weccikoo seen koom. 14 Waa kër Togarma indi ay fas aki gawar aki berkelle, di ko weccikoo seen alal. 15 Dedaneen ñi di say jula, koomu dun yu bare di jaare say loxo, ñu di la feye bëñi ñey ak bantu jalambaan. 16 Waa Siri it di say jula, di jëndeek yaw lu bare loo defar, di ko wecci per yu jafe, ak ndimo yu xewar, ak séri ràbb ak lẽe ak peri koray ak peri rubi. 17 Yudak réewum Israyil it di say jula, di la wecci bele bu bawoo Minit, ak dugub ak lem ak diwu togg ak diwu yaram. 18 Dëkkub Damaas di la jula lu bare loo defar ak jépp alal joo barele, di la ko weccee biiñ bu jóge Elbon, ak kawaru xar gu weex. 19 Waa Weden ak Yawaan bàyyikoo Usal, di la wecci sa koom weñ gu ñu tëgg, ak xasum kaas, ak barax bu xeeñ. 20 Waa Dedan it di say jula, indil la seen ndimoy tegi fas. 21 Waa Arabi ak mboolem garmiy Kedar it di julanteek yaw, feye la ay tàppaanga aki kuuy aki bëy. 22 Julay Saba ak Raama it di julaak yaw, di la indil ngën-gi-safal ak mboolem peru gànjar, ak wurus yu ñuy weccikoo sa alal. 23 Waa dëkk yii di Karan ak Kane ak Eden ñoom it di say jula, ñook julay Saba ak Asur ak Kilmàdd. 24 Ñooñoo doon say jula yu lay indil yérey tànnéef, ak turki yu yolet, ak yérey ràbb, ak malaan yu yànj, ak goj yu rawaasoo yu wér. 25 Ay gaali Tarsis yu mag a daan yóbbu sam njaay.

Nga fees dell, diis gann fi digg xolu géej.
26 Say joowkat waral la mbeex mi ne màww,
ba digg géej, teewul ngelawal penku damm la.
27 Sa alal ja, sab yeb, sa njaay ma,
sa niti géej, say mool, say jagalkat, say jaaykat,
ak mboolem sa dag yi ci sa biir,
ak mboolem sa gàngoor gi ci sa biir,
ñooy tàbbeendoo xolu géej keroog sa bésub jéll ba.
28 Bu say mool yuuxoo,
tefes yaay riir,
29 képp kuy ŋàbb joowu wàcce gaalam.
Nitu géejoo mboolem mool,
ñépp fi suuf lañuy taxaw.
30 Ñoo lay jooyal,
di yuuxu yuux yu metti,
xëppoo suuf,
fërënqu cib dóom.
31 Yaay tax ñuy nelu,
sol ay saaku di ko ñaawloo,
di la jooye naqaru xol ak yuux yu metti.
32 Ñeey am tiis, yékkatil la kàddug jooy,
jooy la ne:
‘Ana dëkk bu mel ni Tir,
mi ñu wedamal nii biir géej?’
33 Ba ngay yebbee géej sam koom,
yaa daan reggal ñu bare.
Sa alal ak sa koom gu bare nga woomale buuri àddina.
34 Léegi rajaxoo nga biiri gannax ca biir xóotey géej,
sa koom ak sa gàngoor gi ci sa biir, lépp jóoru.
35 Waa dunoo dun a la tiisoo,
seen yaramu buur ya dawa daw ba ñu ne yasar.
36 Julay xeet yaa ngi muslu ci saw demin.
Raglu nga mujje,
te doo tekkeeti ba fàww!”»

<- Esekiyel 26Esekiyel 28 ->