Saar 23
Samari ak Yerusalem bokkaale nañu
1 Kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
2 «Yaw nit ki, ñaari jigéen la woon,
ñu bokk jenn ndey,
3 di gànctu ca Misra,
te doon fa gànctu ca seenug ndaw.
Fa lañu doon làmbe seeni ween,
di motoxal seen cusi janq.
4 Ku mag kaa doon Owola,
rakk ja di Owoliba.
Ñu di samay soxna,
jural may doom, góor ak jigéen.
Owola mooy Samari,
Owoliba di Yerusalem.
5 Owola di sama soxna tey gànctu,
di xédd ay faram, waa Asiri xarekat ya.
6 Ña nga sol seen mbubbi baxa,
diy kàngam aki jawriñ,
ñoom ñépp di xale yu góor yu sopplu,
di ndaanaani gawar.
7 Boppam la daan jox tànnéefi doomi Asiri yooyu yépp,
di sobeel boppam ak mboolem tuuri ñooñu mu xédd.
8 Gànctoom ga woon ca Misra, bawu ko.
Moom lañu daan tëdde cag ndawam,
te ñoo daa motoxal cusi janqam,
ba sotti ko seen yàqute.
9 Moo tax ma teg ko ca loxoy faram ya,
loxoy waa Asiri ya mu daan xédd.
10 Ñoo ko ñori ba mu ne duŋŋ,
doomam yu góor ak yu jigéen, ñu nangu,
moom, ñu jam ko saamar, rey ko.
Nii lañu sottale ay mbugalam,
ba mu yedd jigéen ñépp.
11 «Owoliba rakk ja gis ca
te gëna yàqu magam,
di gànctu ba raw mag ja.
12 Moom it waa Asiri ya la xédd,
ñuy kàngam aki jawriñ,
xarekat yu ràngu ba solu ba jekk,
di ndaanaani gawar,
ñoom ñépp di xale yu góor yu sopplu.
13 Ma gis ni mu sobeele boppam,
muy wenn yoon wu ñu bokk ñoom ñaar.
14 Teewul rakk ja gëna gànctooti,
gis nataali góor yu ñu yett ciy tabax,
di jëmmi waa Babilon yu ca ñaase, xonq curr.
15 Ña nga takk ngañaay ca seen ndigg,
tañlaayu bay langal,
ñoom ñépp di nirooki kàngam,
di saf doomi Babilon,
réewum Kalde di seen cosaan.
16 Rakk ja teg nataal ya bët rekk, xédd leen,
yónnee leeni ndaw fa Kalde.
17 Doomi Babilon ya dikk,
fekksi ko ci kaw lalu baane,
sobeel kook seen yàqute,
mu sobeel boppam ak ñoom ba ñu sàppi ko.
18 Moo siiwal gànctoom,
wone yaramu neenam,
ba sàppi ma ni ma magam sàppee.
19 Mu gën di gànctooti,
di ko baaxantale janti ndawam,
ba muy gànctu ca réewum Misra.
20 Muy xédd ay faram
yu seeni ngóora di saf yu mbaam,
te ñu aldee alde ba mel niy fas.
21 «Yaw Owoliba de, yaa namm sa yàqute ga woon ba ngay ndaw,
ba waa Misra di motoxal say cus,
ngir bànneexoo sa weeni janq.
22 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
“Owolibaa, maa ngii di xabtalsi say far ci sa kaw;
ñi la sàppi, ñoom laay bàbbee fi la wër,
xiirtal leen fi sa kaw:
23 waa Babilon, Kaldeen ñépp,
muy waa Pekot, di waa Sowa, di waa Kowa,
ànd ak waa Asiri yépp,
di xale yu góor yu sopplu,
ñoom ñépp di kàngam aki jawriñ,
di kilifa yu ràññiku,
ñoom ñépp war ay fas.
24 Dañuy dal fi sa kaw,
aki gànnaay, watiir aki mbege ak kurélu xeeti xeet,
ŋàbb pakk bu mag ak bu ndaw, sol mbaxanam xare,
dar kepp la.
Maa leen di jox sañ-sañu mbugal,
ñu mbugal la, ni ñu baaxoo mbugale.
25 Maa lay yen sama fiiraange,
te yaw lañuy jëflanteel ak xadar,
sa bakkan ak say nopp, ñu njoof,
saw ndes fàddoo saamar.
Say doom, góor ak jigéen, ñu nangu,
sa kuutaay lakk ba xoyomu.
26 Dañuy futti say yére, foqati say gànjar.
27 Maay dakkal sa jëfi yàqute,
ak sa gànctu ga dale ca réewum Misra,
ba dootoo ko geesoo gëti nammeel,
te dootoo fàttliku Misra.
28 Boroom bi Aji Sax ji kat dafa wax ne:
Maa ngii di la teg ci loxol ñi nga bañ,
loxol ñi la sàppi.
29 Mbañeel lañuy jëfeek yaw,
foqati ñaqoo ñaq,
wacc la, nga ne duŋŋ duŋŋaaral.
Sa gànctu gu ñàkk kersa dina feeñ,
ak dëgër bët gi ngay cagatoo.
30 Ñoo lay def jii jëf
ndax sa gànctu gi nga toppe yéefar yi,
di sobeel sa bopp ak seen kasaray tuur.
31 Yaa topp sa tànki mag,
kon maa lay nàndale kaasu mbugalam.
32 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Sa kaasu mag ngay naane,
xóot, yaatu,
duy ba ne xéew,
xellil la ay ñaawleeki kekku.
33 Mànditeeku tiis ngay feesi,
kaasu wéetaay ak wéetle di sa kaasu mag Samari.
34 Yaa koy naan ba siitaatu ko,
yéy tojit ya, xotate say ween.
Man de maa ko wax.
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
35 «“Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Yaa ma fàtte,
jalax ma sa gannaaw.
Kon nag gàddul sa ayu ñàkk gàcceek sa gànctu.”»
36 Aji Sax ji nag ne ma:
«Yaw nit ki, doo tiiñal Owola ak Owoliba?
Kon nag biral leen seeni jëf ju siblu:
37 Ñoo njaaloo, ñoo bóome,
ñoo njaalook seen kasaray tuur.
Doyatu leen, doom yu góor yi ñu ma jural,
ñu di leen lakk ngir ay tuur, leele leen.
38 Lii itam, ñoo ma ko def:
Bésub keroog lañu sobeel sama kër gu sell,
teddadil sama bési Noflaay.
39 Ñoo rendil seen kasaray tuur seeni doom,
ba noppi dugg sama biir kër gu sell ci bés bi,
ba teddadil kër gi.
Loolu déy, moom lañu def fi sama digg kër gii!
40 Te sax ñoo yeble, wutiy góor,
yónnee ndaw lu leen jële fu sore,
ñu daw dikk,
fekk leen sangu, tusngalu, gànjaru,
41 tooge lal bu yànj,
taabal taaje fa kanam,
sama cuuraay ak sama diw gu xeeñ tege ca.
42 Muy coowal gàngoor gu amul xalaatu àddina;
doom aadama ju nekk a nga ca,
ba ci ay màndikat yu ñu jële ca màndiŋ ma,
ñooña di leen takkal lami loxo,
di leen solal mbaxanam lingeer.
43 Booba laa wax ci ndaw sii njaaloo ba ràpp, ne:
“Ndaw sii lañuy gànctool ba tey?”
44 Mu daldi ànd ak moom ni ñuy àndeek caga rekk.
Nii lañu àndeek Owola ak Owoliba.
Ñii jigéen ñu ñàkk gàcce!
45 Waaye ay nit ñu jub a ngii,
ñoo leen di atteji àtteb njaalookat yu jigéen,
àtteb bóomkat yu jigéen,
nde ay njaalookat lañu,
te ay bóomkat lañu.
46 «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
Wool gàngoor ci seen kaw,
bàyyee leen tiitaange aki sëxëtookat.
47 Gàngoor gaa leen di dóor ay doj,
jam leeni saamar, ñu dee,
seeni doom, góor ak jigéen, ñu bóom;
seeni kër, ñu taal,
48 ma dakkale noonu yàqute ci réew mi,
jigéen ñépp jànge ca,
baña jëfeeti yàqute ju mel ni seen jos.
49 Dees na leen këpp seen yàqute,
ngeen yenu seen bàkkaari kasaray tuur,