5 «Nanga leen wax, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Ba ma tànnee Israyil, maa giñal askanu waa kër Yanqóoba woowa. Maa leen xamal maay kan ca réewum Misra, giñal leen, ne leen: Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. 6 Bésub keroog laa leen giñal ne maa leen di génnee réewum Misra, yóbbu leen réew mu ma leen beralal, mu meew maak lem ja tuuroo, fa gëna taaru ci réew yépp.” 7 Ma ne leen: “Tuur yi ngeen wékki gët yeen ñépp, xalableen leen. Kasaray tuuri Misra, buleen ci sobeel seen bopp. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.” 8 Teewul ñu gàntal ma, nanguwñu maa déglu. Kenn nanguwula xalab tuur yu seexluwu yi mu wékki gët, kenn dëdduwul kasaray tuuri Misra. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ci biir réewum Misra. 9 Teewul ma sédd ci sama teddngay tur, ngir xeet yi ñu nekk ci seen biir bañ maa sikk. Ndax ba may xamal bànni Israyil sama bopp, di leen génne Misra, xeet yooyaa ko seede woon. 10 Ma génne leen réewum Misra, yóbbu leen ca màndiŋ ma. 11 Ma jox leen sama dogali yoon, xamal leen sama àttey yoon yooyuy guddal fanu képp ku koy jëfe. 12 Sama bési Noflaay itam maa leen ko jox, muy màndarga sama digganteek ñoom, ngir ñu xam ne man Aji Sax ji maa leen sellal.
13 «Waaye waa kër Israyil dañu maa gàntal ca màndiŋ ma. Sama dogali yoon, jëfewuñu ko, sama àttey yoon yiy guddal fanu képp ku koy jëfe, ñu xalab. Ñàkke nañu worma lool sama bési Noflaay. Ma nar leena xëpp samam sànj ca màndiŋ ma, sànk leen. 14 Teewul ma sédd ci sama teddngay tur, ngir xeet, ya seede woon ba ma leen di génne, bañ maa sikk. 15 Ba tey maa leen giñal ca màndiŋ ma, ne duma leen yóbbu réew ma ma leen jox, fa meew maak lem ja tuuroo, fa gëna taaru ci réew yépp. 16 Li ko waral mooy sama àttey yoon yi ñu xalab, ak sama dogali yoon yi ñu jëfewul, ak sama bési Noflaay yi ñu ñàkke worma, ndax xol lañu toppe seen kasaray tuur yi. 17 Teewul ma xool leen bëtu ñeewante ba sànkuma leen, faagaagaluma leen ca màndiŋ ma. 18 Ma wax nag seeni doom ca màndiŋ ma ne leen: “Seen dogali baay, buleen ko jëfe; seen àttey yoon, buleen ko topp; seen kasaray tuur, buleen ca sobeel seen bopp. 19 Man Aji Sax ji maay seen Yàlla. Sama dogali yoon, jëfeleen ko; sama àttey yoon, ngeen sàmm ko, di ko jëfe. 20 Sama bési Noflaay, sellal-leen ko, muy firnde sama digganteek yeen, ngir ngeen ràññee ne man maay seen Yàlla Aji Sax ji.”
21 «Waaye doom ya dañu maa gàntal. Sama dogali yoon, jëfewuñu ko, sama àttey yoon yiy guddal fanu képp ku koy jëfe, sàmmuñu ko. Sama bési Noflaay lañu ñàkke worma. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ca màndiŋ ma. 22 Teewul ma téye sama loxo, sédd ci sama teddngay tur ngir xeet, ya seede woon ba ma leen di génne, bañ maa sikk. 23 Ba tey maa leen giñal ca màndiŋ ma ne dinaa leen tasaare ci biir xeet yi, wasaare leen ci biir réew yi. 24 Li ko waral mooy sama àttey yoon yi ñu jëfewul, ak sama dogali yoon yi ñu xalab, ak sama bési Noflaay yi ñu ñàkke worma, ak topp gi ñu topp seen kasaray tuuri baay, wékk leeni gët. 25 Ba tey maa leen bërgal ak àttey yoon yu amul njariñ ak dogali yoon yu taxul kenn a dund. 26 Maa leen sobeel ak seen sarax yi ñuy sarxal tuur yi, ci seen bépp taaw bu ñu lakk ngir tuur yi. Li ma ci jublu mooy ñu jommi, ba ràññee ne man maay Aji Sax ji.
27 «Moo tax, yaw nit ki, nanga wax ak waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Seeni baay a ma dellu ŋàññ, fecci ma kóllëre. 28 Maa leen yóbbu réew ma ma leen giñaloona jox, teewul fu ñu gis tund wu kawe, mbaa garab gu sëq, rendi nañu fa seeni sarax, jooxe fa seen jooxe yi may merloo, taal fa seen saraxi cuuraay, tuural fa seeni tuur. 29 Ma ne leen: Ana lu waral bérabu jaamookaay bii ngeen di dem?” Bérabu Jaamookaay lañu koy wax ba tey jii.
30 «Kon nag nanga wax ak waa kër Israyil ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Seen tànki baay ngeen topp, di sobeel seen bopp, topp seen tuur yu siblu, di gànctook ñoom? 31 Bu ngeen di joxe ay sarax, di lakk seeni doom ngir ay tuur, yeena ngi sobeel seen bopp ba tey jii ci seen tuur yii yépp. Man nag ngeen defe ne maa leen di bàyyi, ngeen seetlusi fi man, yeen waa kër Israyil? Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, duma leen bàyyi mukk ngeen seetlu fi man. 32 Li ngeen mébét ci seen xel du am mukk. Yeena ngi naan: ‘Nan mel ni xeet yépp, mel ni waasoy réew yi, di jaamu bant ak doj.’ 33 Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, sama dooley loxo ak sama kàttanu përëg, ak sànj mu naan soteet laay nguuroo ci seen kaw. 34 Maa leen di génnee ci askan yeek réew yi ngeen tasaaroo ci seen biir. Sama dooley loxo laa koy defe ak sama kàttanu përëg, ak sànj mu naan soteet fi seen kaw. 35 Maa leen di yóbbu màndiŋ ma ñuy wooye Màndiŋu Askan yi, layoo faak yeen, di leen xool, ngeen di ma xool. 36 Noonee ma layoo woon ak seen baay ca màndiŋu réewum Misra, ni laay layook yeen. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. 37 Maa leen di lime sama yetu sàmm, kenn-kenn, tënk leen ci pas-pasu kóllëre gi. 38 Maay xettee fi seen biir ñi may gàntal ak ñi may tooñ. Réew ya ñu wàlliyaani, fa laa leen di jële, te réewum Israyil, duñu fa duggi. Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
39 «“Léegi nag yeen waa kër Israyil, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Aca, na ku ne jaamuji kasaray tuuram! Dungeen mujje lu moy déggal ma, ba sama tur wu sell wi, dootuleen ko teddadile seeni sarax ak seeni tuur. 40 Fa kaw sama tund wu sell wa, fa tundu Israyil wu kawe wa, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, foofa déy la ma waa kër Israyil gépp di jaamujee, ñoom ñépp ca réew ma. Fa laa leen di nangule. Fa laay sàkkoo seeni jooxe ak seen ngëneeli sarax, ak lépp lu ngeen ma sellalal. 41 Maa leen di nangul seen saraxu cuuraay, gannaaw bu ma leen génnee fa biir xeet yaak réew ya ngeen tasaaroo ca seen biir, ba dajale leen. Su boobaa maay jëfe sellnga fi seen biir, xeet yi seede. 42 Dingeen xam ne maay Aji Sax ji, gannaaw bu ma leen délloosee ci biir suufas Israyil, réew ma ma giñaloon seeni maam, ne dinaa leen ko jox. 43 Fa ngeen di fàttlikoo seeni jëfin, mboolem seeni jëf yu ngeen sobeele woon seen bopp, daldi jéppi seen bopp ndax seen mboolem jëf ju bon. 44 Yeen waa kër Israyil, duma jëflanteek yeen li seen jikko ju bon yelloo ak seen jëfi yàqute, waaye sama teddngay tur laa ciy seet, ba ngeen xam ne man maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»
<- Esekiyel 19Esekiyel 21 ->- a 20.1 Mu yemook fukki weer ak benn gannaaw peeñu ma jiitu mii. Seetal ci 8.1.