Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 19
Jooy ngarmig Israyil war na
1 Aji Sax ji ne ma: «Yaw nag jooyal garmiy Israyil. 2 Neel:
“Céy sa ndey, ndaw gaynde,
fi biir gaynde yi!
Moo goor fi biir gaynde yu ndaw yi,
di fa yar ay doomam.
3 Moo tàggat kenn ciy goneem*19.3 Wax ji ci Buur Yowakas la jëm. Seetal ci 2.Buur ya 23.31-34.,
ba muy góoru gaynde gu ndaw,
mana pàdd um pàddam,
di yàpp doom aadama.
4 Ba ko xeet ya déggee, dañu koo fexeel,
mu sërëx ca seenum yeer,
ñu lonk, yóbbu réewum Misra.
 
5 «“Ndey gaynde xaara xaar,
ba gis ne yaakaar jee na,
mu jël keneen ciy goneem19.5 Wax ji ci Buur Cedesyas la jëm. Seetal ci 2.Buur ya 24.18-20 ak 25.1-7.,
def ko góoru gaynde gu ndaw.
6 Daa ànd ak moroomi gayndeem,
màgg, doon góoru gaynde gu ndaw,
ba mana pàdd am pàddam,
di yàpp doom aadama.
7 Mu tëdde seeni jëtun,
gental seen dëkk yu mag,
réew maak la ca biiram tiit ca coowal ŋaram.
8 Teewul xeeti diiwaan ya ko séq ànd,
dal fa kawam,
laaw ko seenum caax,
sërxal ca seenum yeer.
9 Ñu lonk, dugal cib kaaf,
yóbbul ko buuru Babilon,
tëj ko ca biir ab tata,
ba kenn déggatuli ŋaram
fa kaw tundi Israyil.
 
10 «“Sa ndey a la niru, mel ni reseñ
gu ñu jëmbat fi wetu ndox,
meññ, sëq lipp,
ndax ndox mu ne xéew.
11 Mu am car yu dëgër,
yu man yeti nguur,
daldi màgg ba àkki niir ya,
ràññiku ci taxawaay ak sëqaay.
12 Waaye am sànj a ko buddi, sànni fi suuf,
ngelawal penku wowal doom ya,
bànqaasam yu dëgër ya fàq, lax,
sawara xoyom ko.
13 Tey mu ngi jëmbate fi màndiŋ mi,
ci réew mu wow, maral.
14 Sawaraa tàkke fa bànqaasam,
xoyom njebbit ak meññeef.
Du car bu dëgër bu ca des
bu mana doon yetu nguur.”
Woyu dëj a ngii wu ñuy jooyeb dëj.»

<- Esekiyel 18Esekiyel 20 ->