Esekiyel
15 Naka laa xool, daldi gis ay mbege fi suuf, mbege mu ci nekk feggook menn mbindeef, mook ñeenti kanamam. 16 Mbege yaa ngay nirook peru kirsolit, ci melokaan ak ci bind. Ñoom ñépp a niroo. Seen melokaan ak seen bind daa mel ni, mbege mu ci nekk, mbegee nekk ca biiram, 17 mbege yay dawe ñeenti wet te warangikuwuñu. 18 Taxawaayu mbege ya daa réy ba raglu te mu ci nekk ay gët la sàngoo ba daj. 19 Bu bindeef ya dawee, mbege ya feggook ñoom daw; bu ñu naawee, mbege ya naaw. 20 Fu noo gi wale jublu fa rekk, fa lañu jëm, mbege ya jógandook ñoom, ànd ak noo gi. Noowal boroom bakkan yi daal moo nekk ci mbege yi. 21 Bu ñu dawee, ñu daw; bu ñu taxawee, ñu taxaw. Bu ñu jógee ci suuf, yékkatiku, ñu ànd ak ñoom yékkatiku. Noowal boroom bakkan yi daal moo nekk ci mbege yi.
22 Lu mel nib dénd a tiim boppi bindeef ya, raglu, leer nàññ ni doju kiristaal†1.22 kiristaal daa mel ni weer bi ñuy defare ab kaas.. 23 Mbindeef mu ci nekk sa yenn ñaari laaf a ngi ci suufu dénd bi, tàlli, dékkarloo; ñaari laaf yi ci des sàng sa yaram. 24 Bu ñuy naaw, may dégg seen coowal laaf yi, mu mel ni géej mbàmbulaan, melati ni kàddug Aji Man ji, di saf riirum xare. Bu ñu taxawee, daldi wàcce seeni laaf. 25 Saa yu ñu taxawee ba wàcce seeni laaf nag, ag kàddu di jollee ca kaw dénd ba ca seen kaw bopp ya.
26 Ca kaw dénd ba tiim seeni bopp, ba tey, am na luy nirook ngànguney peru safiir, te jëmmu nit nekk ca kawa kaw lay nirook ngàngune. 27 Ma gis nag lu mel ni weñ guy tàkk, wër ko; dale ca lay niru ndigg la, jëm kaw; daleeti ca lay niru ndigg la, jëm suuf. Ma gis lu mel ni sawara akug leer wër ko. 28 Mu mel ni xon ci biiri niir, bésub taw. Loolooy melokaanu leer ga ko wër. Muy melokaan muy jëmmal leeru Aji Sax ji. Naka laa ko gis, daldi ne gurub, dëpp sama kanam fi suuf. Ma dégg nag kàddu gu jib.
Esekiyel 2 ->