5 Aji Sax ji nag jàpp na bés, nee na: «Ëllëg maay def loolu ci réew mi.» 6 Ca ëllëg sa Aji Sax ji def ko: jurug waa Misra gépp dee, te jurug bànni Israyil, lenn deewu ca. 7 Ba Firawna yónnee, ba nemmiku mbir ma, xam na ne lenn deewul ca juru bànni Israyil. Teewul mu të ticc ba tey, baña bàyyi mbooloo ma, ñu dem.
22 Aji Sax ji ne Musaa: «Yékkatil sa loxo ca kaw, mu jublu asamaan, ngir tawub yuur bi dal ci réewum Misra mépp, nit ak mala, ba ci lépp luy gàncax ci réewum Misra.» 23 Musaa ne yékkét yet wa, mu jublu asamaan, Aji Sax ji yebal dënu baak tawub yuur ba, sawara wa ne yureet fi suuf, ànd ak tawub yuur, ba Aji Sax ji sóob ca réewum Misra. 24 Tawub yuur ba réy lool, ànd ak sawara, wa jaxasook yuur ba, di xuyy-xuyyi, muy guléet ca cosaanu réewum Misra ba bésub keroog. 25 Tawub yuur ba dal ca mboolem réewum Misra, daaneel lépp lu ne woon ca biti, nit ak mala, daaneel gàncax gépp, dammat garab ya ca àll ba yépp. 26 Diiwaanu Gosen, ga bànni Israyil dëkkoon doŋŋ, moo mucc ca tawub yuur ba.
27 Firawna nag yónnee, woolu Musaak Aaróona. Mu wax leen ne leen: «Bii yoon de, maa tooñ. Aji Sax ji moo nekk ci dëgg, te maak sama waa réew ñoo sikk. 28 Tinuleen Aji Sax ji, ndax dënu yu màgg yeek tawub yuur bi dakk. Dinaa leen bàyyi, ngeen dem. Deesu leen fi téyeeti.» 29 Musaa ne ko: «Bu may génn dëkk bi rekk, di tàllal Aji Sax ji samay loxo, dënu yi dakk, tawub yuur bi siwet, ngir nga xam ne àddina, Aji Sax jeey boroom. 30 Waaye xam naa ne, loolu du tax ba tey, nga ragal Yàlla Aji Sax ji, yaw, yaak say dag.»
31 Fekk na gàncax ga ñuy defare wëñu lẽe yàqu na, mook peppum lors ba, ndax lors baa nga tollu woon ci waaja focci, gàncax ga ñuy defare lẽe di tóor. 32 Waaye xeeti peppi bele ya, lenn yàquwu ca, ndax yooyooy mujja ñor.
33 Naka la Musaa bàyyikoo ca Firawna, ba génn dëkk ba rekk, daldi tàllal Aji Sax ji ay loxoom. Dënu yaak tawub yuur ba ne tekk, taw ba siwet. 34 Ba mu ko defee Firawna gis ne tawub yuur baak dënu ya dakk na, mu tëëti ticc, mooki dagam, dellu cig tooñam. 35 Firawna të rekk, baña bàyyi bànni Israyil, ñu dem, muy la Aji Sax ji waxoon, Musaa jottli.
<- Mucc ga 8Mucc ga 10 ->- a 9.18 tawub yuur: ndoxum taw la, mu sedd, ba defi donj.