4 Ba mu ko defee Firawna woo Musaak Aaróona, ne leen: «Ñaanleen Aji Sax ji, ngir mu teqale nook mbott yi, man ak sama waa réew. Kon dinaa bàyyi mbooloo mi, ñu dem rendili Aji Sax ji sarax.» 5 Musaa ne Firawna: «Saa yu la neexee rekk, sang bi. Wax ma kañ laa lay ñaanal, yaw ak say dag ak sa waa réew, ngir jële fi mbott yi, ñu tàggook yeen, génn seeni kër, ca dexu Niil ga doŋŋ lañuy des.» 6 Mu ne ko: «Nay ëllëg.» Musaa ne ko: «Baax na, ndax nga xam ne sunu Yàlla Aji Sax ji amul moroom. 7 Mbott yi dinañu jóge sa kër, teqlikook yeen, yaak say dag ak sa waa réew, ca dexu Niil ga doŋŋ lañuy des.» 8 Musaa ak Aaróona nag jóge ca Firawna, Musaa tinu Aji Sax ji ca mbirum mbott ya mu yare Firawna. 9 Aji Sax ji def la ko Musaa ñaan, mbott ya dee, ba jeex ca kër yaak ca ëtt yaak tool ya. 10 Ñu jal koo jal, ba xet ga ubale ca réew ma. 11 Teewul, ba Firawna gisee ca mbir ma tan, daa wéye të, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
21 Firawna daldi woolu Musaak Aaróona, ne leen: «Demleen rendili seen Yàlla sarax, te nay ci biir réew mi nag.» 22 Musaa ne ko: «Loolu du yoon, ndax li nuy rendil sunu Yàlla Aji Sax ji, waa Misra dañu koy xof. Te bu nu sarxalee lenn lu waa Misra xof, ñuy gis, dinañu nu dóor ay doj, ba nu dee. 23 Kon kay danoo wara génn, topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, rendili fa sunu Yàlla Aji Sax ji sarax, ni mu nu ko sante.» 24 Firawna àddu ne: «Dinaa leen may, ngeen dem ca màndiŋ ma, rendili seen Yàlla Aji Sax ji sarax, waaye buleen sore lool. Ñaanal-leen ma nag.» 25 Musaa ne ko: «Bu ma bàyyikoo ci yaw rekk Firawna, dinaa tinu Aji Sax ji, ngir ëllëg ndiiraani weñ yi teqlikook yaw, ak say dag ak sa waa réew, waaye kat Firawna, bu nu naxati, di baña bàyyi mbooloo mi, ñu rendili Aji Sax ji sarax.»
26 Musaa bàyyikoo fa Firawna, daldi tinu Aji Sax ji. 27 Aji Sax ji defal Musaa la mu ñaan, jële ndiiraani weñ ya ca Firawnaaki dagam ak waa réewam, ba weñ desatu fa. 28 Teewul Firawna të rekk, baña bàyyi mbooloo ma, ñu dem.
<- Mucc ga 7Mucc ga 9 ->- a 8.12 rayentaan: li ñuy wax rayentaan fii, kenn xamul lan la dëgg. Waaye luy naaw lu tuut la, di same aka màtte.