2 Xar-sànni mi, wëñu wurus lees ko ràbbe, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. 3 Ay xobi wurus lañu tëgg ba mu jekk, ñu dagg ko ay wëñ yu ñu ràbbaaleek wëñ gu baxa gi te laal yolet, ak wëñ gu xewar gi, ak gu xonq gi curr, ak wëñu lẽe gi. Ñu daldi ciy ñawaale ay nataal. 4 Ñaari ngàlli mbagg lañu ko defal, daldi faste wu ci nekk ci ñaari cati xar-sànni mi. 5 Ngañaayu taaral li tege ci kaw, ni xar-sànni mi lees ko defare, liggéeyaale kook moom, ñu ànd di benn. Ñu ràbbe ko wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
6 Ci kaw loolu ñu we peri onigsë yi, fege per yi ŋankukaayi wurus, daldi ciy ñaas turi doomi Israyil yu góor, noonu ñuy ñaase xàmmikaay yi ñuy torloo. 7 Ñu tapp per yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, per yi nag taxawe taxawaayu bànni Israyil, noonu ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
15 Ci biir loolu ñu sàkkal kiiraayal dënn bi ñaari caqi wurusu ngalam yu ci tege, te rawaasoo ni ay buum. 16 Ñu sàkk itam ñaari ŋankukaayi wurus ak ñaari jaaroy wurus yu ñu takk ci ñaari cati kiiraayal dënn bi ci kaw 17 Ñu nas nag ñaari buumi wurus yi ci ñaari jaaro yi ci cati kiiraay li. 18 Yeneen ñaari cati buumi wurus yi, ñu we leen ci ñaari ŋankukaay, yi ci kaw ngàlli waggi xar-sànni mi, ci kanam. 19 Ñu sàkkal ko itam ñaari jaaroy wurus, yu ñu we ci ñaari cati suufi kiiraay li, fi féete biir, wet gi tafu ci xar-sànni mi. 20 Ñu sàkkalaat kiiraay li yeneen ñaari jaaroy wurus, yu ñu we ci suufu ngàlli xar-sànni mi, fi féete kanam, dendeek sofu ngàll yi, te tiim ngañaayu xar-sànni mi. 21 Kiiraayal dënn bi, buum gu sew gu baxa te laal yolet, moom lees ko téyee, lëkklee ko jaaroy kiiraay leek jaaroy xar-sànni mi, kiiraay li dëkke tiim ngañaay li, ba du teqlikook xar-sànni mi, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
27 Ñu sàkkal nag Aaróona aki doomam mbubb yu gudd yu ñu ràbbe wëñu lẽe, 28 ak kaalag lẽe, ak mbaxanay lẽe, ak tubéyi njiitlaay yu lẽe, 29 ak laxasaay giy liggéeyu ràbb bu rafet, bu ñu ràbbe wëñu lẽe bu dëgër, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
30 Ñu sàkk nag meeteel gu sell gu wurusu ngalam, muy dogu wurus wu tell, ñu ñaas ci kawam mii mbind, ni ñuy ñaase mbindum torlu: «Sell na, ñeel Aji Sax ji». 31 Ñu daldi koy takke buum gu baxa te laal yolet, téyee ko ko ci kaw kaala gi, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
33 Ba loolu amee ñu indil Musaa jaamookaay bi: xayma bi ak yëfam yépp; lonku yi ak làcc yi ak galan yi ak jën yeek tegu yi, 34 ak kiiraayal deri kuuy yi ñu sóob xonq, ak kiiraayal deri piipi yi, ak kiiraayal xàjjatle bi, 35 ak gaal gi àlluway seede si dence, aki njàppoom, ak kubeeru saraxu njotlaay gi, 36 ak taabal jeek ndabam yépp, ak mburum teewal mi ciy tege, 37 ak tegukaayu làmp bu wurusu ngalam bi aki làmpam, làmp yi sësaloo ba jekk ak mboolemi jumtukaayam, ak diw gi ñuy taaloo, 38 ak sarxalukaay bu wurus bi, ak diwu pal gi, ak cuuraay lu xeeñ li, ak kiiraayal buntu xayma bi, 39 ak sarxalukaayu xànjar beek caaxub xànjaram, aki njàppoom ak ndabam yépp, ak mbalkam njàpp mi akub tegoom, 40 ak sori wurmbalu ëtt bi aki jënam aki tegoom, ak kiiraayal lafu buntu ëtt bi, aki buumam aki xeram; mboolem jumtukaay, yi ñuy liggéeye ci màkkaanu xaymab ndaje mi rekk, 41 ak yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci bérab bu sell bi; yére yu sell yu Aaróona sarxalkat bi, ak yérey doomam yi ñuy sol, di sarxale. 42 Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa rekk, ni la bànni Israyil sottale liggéey bi bépp. 43 Musaa nag nemmiku mboolem liggéey bi, ba gis ne sottal nañu ko; noonee ko Aji Sax ji santaanee woon, ni lañu ko defe. Musaa daldi leen ñaanal.
<- Mucc ga 38Mucc ga 40 ->