Link to home pageLanguagesLink to all Bible versions on this site
Saar 36
1 «Kon nag Besalel ak Oliyab ak mboolem ñu xareñ ñi Aji Sax ji may xareñte ak déggin ngir ñu mana jëfe mboolem sas yi jëm ci liggéeyu bérab bu sell bi, ñoom ñépp nañu sottal lépp li Aji Sax ji santaane.»

2 Ba loolu amee Musaa woo Besalel ak Oliyab ak mboolem ñi xareñ ñi Aji Sax ji xareñal, mboolem ñi am yéeney wàllsi ci liggéey bi, ngir sottal ko. 3 Ba mu ko defee ñu nangoo ci Musaa mboolem jooxe bu bànni Israyil indi, ngir sottal liggéeyu bérab bu sell bi. Bànni Israyil nag jàppoo suba gu jot di indil Musaa ay saraxi yéene, 4 ba mboolem liggéeykat yu xareñ yi nekkoon ci mboolem liggéeyu bérab bu sell bi, kenn ku ci nekk bàyyi la nga jàppoon, daldi dikk. 5 Ñu ne Musaa: «Li mbooloo mi indi wees na dayob liggéey bi Aji Sax ji santaane.» 6 Musaa nag yéenelu ca dal ba bépp, ñu ne, ñépp, góor ak jigéen, bu ci kenn waajalati ab jooxe, ñeel bérab bu sell bi. Fa la mbooloo ma noppee indi. 7 Booba jumtukaay ya doyoon na sëkk, ba ëpp sax la ñu cay liggéey lépp.

Defar nañu bérab bu sell ba
8 Ba loolu amee mboolem ñu xareñ ñi bokk ci liggéey bi daldi defar jaamookaay bi. Ñu def ko fukki sori rabali lẽe, yu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr. Ñu ñawaale ci ay nataali serub. 9 Guddaayu sor bu nekk di ñaar fukki xasab ak juróom ñett, yaatuwaay bi di ñeenti xasab, sor yépp tolloo. 10 Ñu taqle yii juróomi sor, taqle juróomi sor yi ci des. 11 Ci kaw loolu ñu ñaw ay takku yu baxa te laal yolet ci catal sor bi mujj ci benn taqalante bi, sor bi jeexal taqalante bi ci des it, ñu def ko noonu. 12 Juróom fukki takku lañu ñaw ci benn sor bi, ak juróom fukki takku ci catal sor bi jeexal taqalante bi ci des, takku yi yemoo. 13 Ñu defar juróom fukki lonkuy wurus, daldi jokklantee sor yi lonku yi, ba jaamookaay bi di benn.

14 Ba loolu weesee ñu ràbb ay sori kawari bëy, ngir def ko ñaareelu xayma, muy kiiraay ci kaw jaamookaay bi. Fukk ak benn lañu def sor yi. 15 Guddaayu sor bu nekk fanweeri xasab la, yaatuwaay bi di ñeenti xasab, te fukki sor yeek benn yépp a tolloo dayo. 16 Ñu taqle yii juróomi sor, juróom benni sor yi ci des it noonu. 17 Ñu sàkk juróom fukki takku ci catal sor, bi jeexal benn taqalante bi, daldi sàkk juróom fukki takku itam ci catal sor, bi jeexal taqalante bi ci des. 18 Ñu sàkk nag juróom fukki lonkuy xànjar yu ñu jokklantee ñaari taqalante yi, muy benn xayma. 19 Ñu defaral xayma bi malaanum deri kuuy bu ñu sóob xonq, ak meneen malaanum deri piipi muy tege ci kawam.

20-22 Gannaaw gi ñu sàkkal jaamookaay bi ay làcci bantu séng yu sampe. Làcc wu nekk am ñaari kenu yu ñu lëkklee galan yu ndaw, te noonu lañu def làcci jaamookaay bi yépp. Fukki xasab lañu def taxawaayu làcc wu nekk, def yaatuwaay bi xasab ak genn-wàll. 23 Ci wàllu làcci jaamookaay bi, ñu sësale ñaar fukki làcc fi féete bëj-saalum, 24 boole kook ñeent fukki tegukaayi xaalis yu ronu kenuy ñaar fukki làcc yi, ñaari tegukaay ronu làcc wi jiitu ngir ñaari kenoom yi mu àndal, ñaari tegu topp ci, ronu wépp làcc wu ci topp, ngir ñaari kenoom yi mu àndal. 25 Geneen wetu jaamookaay gi féete bëj-gànnaar itam, ñu def ko ñaar fukki làcc, 26 ak seen ñeent fukki teguy xaalis, ñaari tegu ronu làcc wi jiitu, ñaari tegu topp ci, ronu wépp làcc wu ci topp. 27 Gannaaw jaamookaay gi féete sowu, ñu sàkkal ko juróom benni làcc, 28 teg ci ñaari làcc ngir colli jaamookaay bi ci gannaaw, 29 ñu àndandoo di benn ci suuf te lëkkloo ci kaw ci benn lam kepp. Noonu lañu leen def ñoom ñaar, ñuy ñaari coll yi. 30 Muy juróom ñetti làcc ak seeni teguy xaalis; di fukki tegu ak juróom benn, ñaari tegu ronu làcc wu nekk.

31 Gannaaw loolu ñu sàkk ay galani banti séng, juróomi galan yiy ànd ak làcc, yi ci genn wetu jaamookaay bi, 32 ak juróomi galan ngir làcci wet gi ci des, ak juróomi galan ngir làcc yi ci gannaaw jaamookaay bi, fi féete sowu. 33 Ñu def galanu digg bi ci digg làcc yi, dale ko cat ba cat. 34 Ci biir loolu ñu xoob làcc yi wurus, sàkkal leen ay lami wurus yuy téye galan yi, daldi xoob galan yi it wurus.

35 Ñu sàkk itam rido bi, ràbbe ko wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñawaale ci ay nataali serub. 36 Ñu sàkkal rido bi ñeenti jëni séng yu ñu xoob wurus, jën yi ànd ak wékkukaayi wurus, ñu móolal jën yi ñeenti teguy xaalis.

37 Ñu sàkkal buntu xayma bi kiiraay lu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, mu doon liggéeyu ràbb bu rafet, 38 ak juróomi jënam yu ànd ak seeni wékkukaay. Ñu xoob nag wurus boppi jën yi ak seeni galan, juróomi teguy jën yi di xànjar.

<- Mucc ga 35Mucc ga 37 ->