4 Ba Aji Sax ji Yàlla gisee Musaa jàdd, di xoolsi, ca gajj ba la àddoo, ne ko: «Musaa, Musaa!» Mu ne ko: «Maa ngi.» 5 Yàlla ne ko: «Bul jegesi, summil say dàll, ndax fii nga taxaw suuf su sell la.» 6 Mu teg ca ne: «Man maay sa Yàllay baay, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba.» Ca la Musaa nëbb kanam ga, ndax ragala xool Yàlla.
7 Aji Sax ji tegaat ca ne ko: «Gis naa bu baax fitna, ji sama ñoñ nekke Misra. Dégg naa itam seen jooy ndax kilifay saskat, yi leen di gétën ci liggéey, te ñeewante naa leen ngir seen coono. 8 Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña. 9 Yuux, yi bànni Israyil nekke nii, agsi na ba ci man, te gis naa it ni leen waa Misra di note. 10 Kon nag kaay, ma yónni la ca Firawna. Demal yiwiji bànni Israyil, sama ñoñ, ñu génn Misra.»
13 Musaa ne Yàlla: «Su ma demee ca bànni Israyil, ne leen seen Yàllay maam ya moo ma yónni ca ñoom bànni Israyil de, dinañu ma laaj nu mu tudd. Lu ma leen di wax nag?» 14 Yàlla ne Musaa: «Maay Ki nekk. Kon waxal bànni Israyil ne leen: “Aji Nekk ji moo ma yónni ci yeen.”» 15 Yàlla dellu ne Musaa: «Dangay wax bànni Israyil, ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba, moo ma yónni ci yeen.” Aji Sax jee di sama tur wu sax dàkk, ñu di ma ko fàttlikoo ba fàww. 16 Demal woo magi Israyil, ñu daje, nga ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, moo ma feeñu, ne ma: ‘Gis naa leen, te yég naa li ñu leen di teg ci Misra. 17 Dogu naa leena jële ci seen notaange gii ngeen nekke ci Misra, yóbbu leen ca réewum Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, réew mu meew maak lem ja tuuroo.’ ”
18 «Magi Israyil dinañu la déggal, su ko defee nga ànd ak ñoom, dem ca buuru Misra. Waxleen ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi moo nu feeñu. Kon nag ngalla may nu, nu dem topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, ngir rendili sunu Yàlla Aji Sax ji ay sarax.” 19 Waaye man xam naa ne buuru Misra du leen bàyyi, ngeen dem, mbete mu taseek doole ju ko tiiñ. 20 Moo tax maay xàcci sama loxo, ba dumaa waa Misra ay mbugali mbugal yu kéemaane yu may def ci seen biir. Su ko defee dina leen bàyyi, ngeen dem. 21 Maay dogal sax waa Misra yéwéne mbooloo mii, ba keroog bu ngeen di dem, dungeen deme loxoy neen. 22 Képp kuy jigéen ci bànni Israyil, na laaj dëkkandoom, laajaale ku dëkk ak dëkkandoom, ay gànjari xaalis, ak gànjari wurus, ak yére yu ngeen di solal seen doom yu góor ak yu jigéen, ba waa Misra ne duŋŋ.»
<- Mucc ga 2Mucc ga 4 ->- a 3.1 tundu Yàlla wa: tund woowu, li tax ñu tudde ko tundu Yàlla, Yàlla dafa feeñoo ca kawam.