11 «Naka noonu it ci wetu bëj-gànnaar, guddaay bi di téeméeri xasabi sori rabal, ak seen ñaar fukki jën yu seen ñaar fukki teguy xànjar ronu, wékkukaay yeek galani jën yi di xaalis.
12 «Yaatuwaayu ëtt bi, fi féete sowu, juróom fukki xasabi sori rabal a koy ub, seeni jën di fukk, seeni tegu di fukk.
13 «Yaatuwaayu ëtt bi, fi féete penku ci kanam, juróom fukki xasab la: 14 fukki xasabi sori rabal ak juróom moo ub ëtt bi ci googu wet, seeni jën di ñett, seeni tegu di ñett. 15 Wet gi ci des it, fukki xasabi sori rabal ak juróom, seeni jën di ñett, seeni tegu di ñett. 16 Buntu ëtt bi nag, na doon lafu ñaar fukki xasab, wu ñu defare wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, muy liggéeyu ràbb bu rafet, ay jënam di ñeent, seeni tegu di ñeent.
17 «Jën ya wër ëtt ba yépp, dees koy lëkklee galan yu xaalis, wékkukaayi jën yi di xaalis, seeni tegu di xànjar.
18 «Guddaayu ëtt bi téeméeri xasab lay doon, yaatuwaay bi di juróom fukk, taxawaayu wet yi di juróomi xasab, sor yi ñu ràbbe lépp di wëñu lẽe, tegu yi di xànjar. 19 Mboolem jumtukaayi yi ñuy liggéeye ci jaamookaay bi, ba ci mboolem xeri xaymaam, ak mboolem xeri ëtt bi, lépp xànjar lay doon.
- a 27.21 xaymab ndaje ma: dees na ko wooye jaamookaay ba, ba tey.