4 Musaa daldi wax Firawna ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Bu guddi gi xaajee, maay wër Misra gépp, 5 te lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, dina dee, dale ko ci taaw bu góoru Firawna, mi toog ci jal bi, ba ci taaw bu góoru jaam bu jigéen bu féetewoo wol, boole ci luy taaw bu góor ci jur gépp. 6 Dees na dégg yuux yu réy jibe Misra gépp, lu masula am, te dootu am mukk. 7 Waaye fépp fu bànni Israyil dëkke, dara du fa wokk nit ak mala.” Su boobaa dingeen xam ne, Aji Sax jee ràññatle waa Misra ak bànni Israyil. 8 Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees. 9 Fekk na Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Li waral Firawna du leen déglu, mooy sama kéemaan yi wara fulandiwu ci réewum Misra.» 10 Musaa ak Aaróona def nañu yooyu kéemaan yépp ca kanam Firawna, waaye fekk na Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, ba mu të, baña bàyyi bànni Israyil, ñu génn réew ma.
<- Mucc ga 10Mucc ga 12 ->