5 Ba loolu amee Yawut ya di fàdd seen noon yépp, saamar yay dal, ñu di leen bóom ak a faagaagal. Ñuy def seeni bañ lu leen neex. 6 Ca biir Sus, péey ba, Yawut ya bóom nañu fa juróomi téeméeri nit (500), sànk leen. 7 Ñu bóom Parsandeta ak Dalfon ak Aspata, 8 ak Porata ak Adalya ak Arideta 9 ak Parmasta ak Arisay ak Aridey ak Wasata. 10 Ñuy fukki góor, di doomi Aman doomu Amdeta, fitnaalkatu Yawut ya. Bóom nañu leen, waaye seen loxo laalul alal ja.
11 Bésub keroog ñu yegge Buur limu nit ña ñu rey ca Sus, péey ba. 12 Buur ne Lingeer Esteer: «Biir Sus, péey bii, Yawut yi rey nañu ci juróomi téeméeri nit, reyaale fukki doomi Aman yu góor. Kon diiwaani buur yi ci des xawma nu ñu def ak ñoom. Ana looy ñaanati, ñu may la ko ak looy sàkkooti, ñu defal la ko?» 13 Esteer ne ko: «Buur, ndegam soob na la, mayeel ëllëg itam Yawut yi ci Sus mana wéyal dogalu tey bi. Te fukki doomi Aman yu góor yi, ñu wékk seeni néew ci bant.» 14 Buur joxe ndigal ngir ñu def noona. Ba loolu amee ñu siiwal ab dogal ca Sus, daldi wékk fukki doomi Aman yu góor ya. 15 Yawut ya ca Sus nag daje ca fukki fan ak ñeent ci weeru Adar, bóom fa ñetti téeméeri nit, te seen loxo laalul alal ja.
16 Ci biir loolu Yawut ya ca des te dëkke yeneen diiwaani buur ya daldi daje ngir aar seen bopp, ba am jàmm ca seeni noon. Ñu rey ca seeni bañ juróom ñaar fukki junniy nit ak juróom (75 000), te seen loxo laalul alal ja. 17 Loolaa nga am ca fukki fan ak ñett ci weeru Adar, ëllëg sa di fukki fan ak ñeent. Ñu nopplu, def ko bésub mbégteek bànneex. 18 Yawut ya nekk Sus te daje woon ca fukki fan ak ñett ak fukki fan ak ñeent ca weer wa nag, ña nga dal-lu ca fukki fan ak juróom ca weer wa, def ko bésub bernde ak bànneex. 19 Looloo waral Yawuti kaw-kaw yi ci dëkk yu ndaw yi di wormaal fukki fan ak ñeent ci weeru Adar, def ko bésub bànneex ak bernde, di ci joqlantey teraanga.
29 Ci kaw loolu Lingeer Esteer doomu Abyel, ànd ak Mardose Yawut ba, ñu bind ci sañ-sañ bu mat sëkk, di dëggal ñaareelu bataaxal boobu jëm ci bési Purim. 30 Ñu yónnee ay bataaxal yu jëm ca mboolem Yawut ya ca téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar (127) ca réewum Buur Aserus. Muy kàdduy jàmm ak kóllëre, 31 ngir saxal bési Purim yooyu saa yu jotee, na leen ko Mardose Yawut ba dogalale, mook Lingeer Esteer. Mu dëppoo it ak na ñu dogalale seen bopp jamonoy koor ak ñaawlu, ñoom ak seen askan. 32 Dogalu Esteer ba nag wéral ndigal yooyu jëm ci bési Purim, ñu daldi koy bind ci téere bi.
<- Esteer 8Esteer 10 ->